16
Gannaaw loolu ñu indi gaalu Yàlla ga, yeb ko ca biir xayma ba ko Daawuda sampal, ba noppi ñu joxe fa kanam Yàlla ay saraxi rendi-dóomal ak saraxi cant ci biir jàmm. Ba Daawuda defee saraxi rendi-dóomal yaak saraxi cant ci biir jàmm, ñaanal na askan wa ci turu Aji Sax ji. Daawuda daldi jox kenn ku nekk ci waa Israayil góor ak jigéen menn mburu ak nàkkub tàndarma ak nàkkub reseñ.
Ba loolu wéyee Daawuda tànn ñenn ca Leween ña, ñuy liggéey fa kanam gaalu Aji Sax ji, di woy, di sant aka màggal Aji Sax ji Yàllay Israayil. Ñooñu Asaf a leen jiite woon, Sàkkaryaa di seen ñaareelu kilifa, ña ca topp di Yewel ak Semiramot ak Yexyel ak Matica ak Elyab ak Benaya ak Obedd Edom ak Yewel. Ñooñu wara yore ay jumtukaayi xumbéen yu mel ni ay xalam aki kooraa, Asaf yore tabala ji, Benaya ak Yaxasyel, sarxalkat ya, wara dëkke di wal liit ya fa kanam gaalu kóllërey Yàlla ga. Bésub keroog la Daawuda njëkka dénk Asaf aki bokkam liggéeyu cant yi, ñeel Aji Sax ji, woy wa jib:
Santleen Aji Sax ji, tudd turam,
xamley jalooreem ci biir xeet yi.
Woyleen ko, tagg ko,
yégleleen mboolemi kéemaanam!
10 Damooleen turam wu sell,
yal na kuy wut Aji Sax ji am bànneexu xol.
11 Wutleen Aji Sax ji, sës ci dooleem.
Saxooleen koo wër!
12 Fàttalikuleen ay jalooreem
aki kéemaanam aki àtteem.
13 Yeen sëti Israayil, jaamam ba,
yeen sëti Yanqóoba, yeen ñi mu tànn!
 
14 Kee di sunu Yàlla Aji Sax ji,
di àtte suuf sépp.
15 Fàttalikuleen kóllëreem ba fàww,
ak kàddoom ba ci junniy maas.
16 Mooy digeem baak Ibraayma,
di la mu giñal Isaaxa.
17 Moo ko dëggalal Yanqóoba, sàrtal ko,
fase kook Israayil mooma kóllëre gu sax.
18 Moo noon: «Yaw laay jox réewum Kanaan
muy sa cér, nga séddoo.»
 
19 Ba bànni Israayil doonee ñu néewa néew,
diy doxandéem ci réew mi,
20 di wëreelu ci biir xeetoo xeet,
ak nguuroo nguur,
21 mayul kenn mu noot leen,
te yaral na leen ay buur,
22 ne leen: «Buleen laal ñi ma séddoo
te samay yonent buleen leen lor.»
 
23 Woyleen Aji Sax ji yeen àddina sépp,
siiwalleen xettaleem bésoo bés!
24 Siiwalleen màggaayam ci biir xeet yi,
xamal waasoo waaso ay jalooreem.
25 Aji Sax jee màgg, jara sant a sant
te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.
26 Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la,
waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
27 Màggaay ak daraja, fa moom,
doole ak mbégtee nga ca dëkkuwaayam.
 
28 Yeen làngi xeet yi, seedeelleen Aji Sax ji,
seedeelleen Aji Sax ji màggaayam ak dooleem.
29 Seedeelleen Aji Sax ji màggaayu turam,
yékkatil kob sarax, te dikk ci kanamam.
Sujjóotalleen Aji Sax ji gànjaroo sellaay.
30 Ragalleen ko, bay lox, yeen waa àddina sépp.
Àddinaa ngi sampu ba dëgër moos, maneesu koo rëññeel.
31 Asamaanoo, bégal!
Suufoo, bànneexul!
di seede ci biir xeet yi,
ne Aji Sax jeey Buur!
32 Géejoo, riiral yaak mboolem li la fees,
na mbooy mi jaayu, mook lu ci biiram,
33 ba garabi àll bi teertoo Aji Sax ji ay sarxolle,
ndax moo àttesi àddina.
34 Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram.
35 Àdduleen, ne ko: «Yaw Yàlla mi nuy musal,
wallu nu, génnee nu ci xeet yi, dajale nu,
nu sante laak sa tur wu sell,
di sagoo sa teddaay.
36 Santleen Aji Sax ji Yàllay Israayil,
cant gu sax dàkk, ba fàww.»
Noonu mbooloo ma mépp ne: «Amiin,» teg ca ne: «Jërëjëfe Aji Sax ji!» 37 Ba mu ko defee Daawuda dëddu, bàyyi Asaf aki bokkam ca kanam gaalu Aji Sax ji, ngir ñuy saxoo liggéey fa kanam gaal ga, di fa def la leen war bés bu nekk. 38 Ci biir loolu mu tabb ay wattukati bunt; ñuy Obedd Edom, ku góor kay doomu Yedutun, ak juróom benn fukki góor ak juróom ñett (68) ñu mu bokkal, boole ca Osa. 39 Ci kaw loolu Daawuda dénk Cadog ak yeneen sarxalkat yi mu bokkal liggéey ba, ca jaamookaayu Aji Sax ja ca tundu Gabawon. 40 Ñuy def bés bu nekk, subaak ngoon, ay saraxi rendi-dóomal ca kaw sarxalukaayu rendi-dóomal ba, ñeel Aji Sax ji. Loolu dëppook mboolem li ñu bind ci téereb yoon wi Aji Sax ji jox Israayil. 41 Ba loolu amee ñu ànd ak Eman ak Yedutun ak ñeneen ñi ñu tànn, jagleleen ñu wara sante Aji Sax ji baat yii: «Li ko waral mooy ngoram gi sax dàkk.» 42 Eman ak Yedutun ñoo féetewoo woon liit yaak tabala ya ak yeneen jumtukaayi xumbéen yi jëm ci woy Yàlla; doomi Yedutun yu góor nag di taxaw ca bunt ba.
43 Ba loolu amee mbooloo mépp dem, ku nekk ñibbi këram. Daawuda it ñibbi këram, ñaanali waa këram.