23
Daawuda tabb na Leween ñi
1 Ba Daawuda màggatee, làq ay ati at ba doyal, doomam Suleymaan la fal buurub Israayil. 2 Mu teg ca woolu mboolem kilifay Israayil ak sarxalkat yaak Leween ña. 3 Ba ñu waññee Leween ña dale ko ca ña am fanweeri at jëm kaw, lim ba bépp fanweeri junni ak juróom ñett la (38 000). 4 Daawuda ne: «Ñaar fukki junni ak ñeent (24 000) ca ñoom ñooy sasoo liggéeyu kër Aji Sax ji, juróom benni junni (6 000) diy saytukat aki àttekat. 5 Ñeenti junni (4 000) di ay wattukati bunt, ñeenti junni (4 000) di woyal Aji Sax ji mu ànd ak jumtukaayi xumbéen yi ma defarlu, ñu di ko sante Yàlla.»
6 Ci kaw loolu Daawuda séddale Leween ñi ñetti kuréel yu dëppook ñetti làngi doomi Lewi yu góor ya leen meññ, di Gerson ak Keyat ak Merari.
Askanu Gerson a ngii
7 Askanu Gerson di Ladan ak Simey. 8 Doomi Ladan yu góor ñoo di Yexyel may taaw ak Setam ak Yowel, ñuy ñett.
9 Doomi Simey yu góor ñoo di Selomit ak Asyel ak Aran, ñuy ñett ñooñu ñoo doon kilifay kër yi soqikoo ci Ladan.
10 Doomi Simey yu góor ñoo di Yaxat ak Sisa ak Yewus ak Berya. 11 Yaxat moo doon taaw, Sisa di ñaareelu doomam, waaye Yewus ak Berya barelewuñu ay doom yu góor, ba tax ñu boole leen genn kër ca lim ba.
Askanu Keyat a ngii
12 Askanu Keyat di Amram ak Iccar ak Ebron ak Usyel. 13 Doomi Amram yu góor ñoo di Aaróona ak Musaa. Aaróona nag ñu jagleel ko Aji Sax ji, mook askanam ba fàww, mu féetewoo liggéeyu néeg bu sella sell bi, di taalal Aji Sax ji saraxu cuuraay, di ko jaamu tey ñaanal askan wi ci turu Aji Sax ji ba fàww. 14 Góor ñiy doomi Musaa, nitug Yàlla ka, ñoom dañu leena limaale ci giirug Leween ñi.
15 Doomi Musaa yu góor ñoo di Gersom ak Elyeser. 16 Taawub Gersom bu góor moo di Sebuwel. 17 Elyeser kenn la am ci doom ju góor, muy Rexabya; amul keneen, waaye ñu bare soqeekoo nañu ci Rexabya.
18 Doomi Iccar ju góor moo di Selomit, taawam.
19 Doomi Ebron yu góor ñoo di Yerya taawam, ñaareel ba di Amarya, ñetteel ba di Yaxasyel, ñeenteel ba di Yekamam.
20 Doomi Usyel yu góor ñoo di Mise, taawam, ñaareel ba di Isiya.
Askanu Meraree ngii
21 Doomi Merari yu góor ñoo di Maxli ak Musi. Doomi Maxli yu góor ñoo di Elasar ak Kis.
22 Elasar dee na te amul doom ju góor. Ay doom yu jigéen rekk la am. Seeni càmmiñ, doomi Kis, denc leen.
23 Doomi Musi yu góor ñoo di Maxli ak Eder ak Yeremot, ñuy ñett.
24 Ñooñu ñoo askanoo ci Lewi, di ay kilifa ca seeni kër baay, ñu waññ leen, kenn-kenn, bind seeni tur. Ñoo doon ñi am ñaar fukki at ak lu ko ëpp, di liggéey ci kër Aji Sax ji. 25 Fekk na Daawuda waxoon ne: «Aji Sax ji Yàllay Israayil jàmmal na ñoñam, dëkk na moom ci boppam ba fàww ci Yerusalem. 26 Kon nag soxlaatul Leween ñi di gàddu xaymab ndaje meek mboolem ndab yi mu àndal te ñu di ko jëfandikoo ci seen liggéey.» 27 Dogal bi Daawuda mujja jël daal mooy ñu waññ Leween ñu góor ñi dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, bind leen.
28 Ñu nekk nag ci kilifteefu sëti Aaróona ci liggéeyu kër Aji Sax ji, ca ëtt yaak néeg ya mu feggool. Ñuy sellal jumtukaay yu sell ya yépp ba tey, te sasoo yeneen liggéey ca biir kër Yàlla ga. 29 Ñoo yoroon itam mburu may tege ca kaw taabal ja, ak sunguf sa ñuy def saraxu pepp, ak mburu yu ndaw ya dul am lawiir, ak yeneen nàkk yu ñuy saaf ak yu ñuy xiiwaale ak diw. Leneen lu ñu doon toppatoo it, di nattukaayu tibb-sotti ya ak nattukaayi guddaay ya. 30 Ñu teg ca di teew suba ak ngoon ngir màggal Aji Sax ji, sant ko. 31 Ñu boole ci di sarxalal Aji Sax ji mboolem saraxu rendi-dóomal ci bési Noflaay ak Terutel weer, ak bési màggal; ñuy liggéeyal Aji Sax ji fàww, na leen yoon àppalee ay ya ak na ñu ko wara defe.
32 Leween ña nag di sàmm ndénkaaneb xaymab ndaje ma, ak ndénkaaneb béreb bu sell ba, ak ndénkaaneb sëti Aaróona ñiy seeni bokk, ci wàllu liggéeyu kër Aji Sax ji.