13
1 Su ma doon làkk làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te jëfewuma genn cofeel, jóolóoli bu xumb doŋŋ laa, mbaa tëggum weñ muy riir. 2 Su ma jotoon ci kàdduy waxyu, boole ci xam mboolem kumpa ak mboolem xam-xam ak ngëm gu mat sëkk ba mana toxal ay tund, te jëfewuma cofeel, duma dara. 3 Te it su ma sarxe woon mboolem sama alal, ba sarxe sama yaramu bopp ngir ñu lakk ko*mbaa ba man koo damoo,, su ma jëfewul cofeel, loolu du ma jariñ dara.
4 Cofeel nag, muñ ak mbaax la. Cofeel bokkul ak kiñaan, bokkul ak jikkoy kañu aka damu. 5 Bokkul ak jëf ju jekkadi ak jiital sa njariñal bopp, bokkul ak naqari deret, bokkul ak denc mer. 6 Bokkul ak bége lu jubadi it, waaye moo di bége liy dëgg. 7 Cofeel moo di: lépp, nga baale; lépp, nga gëm; lépp, nga yaakaar; lépp, nga dékku.
8 Cofeel nag du jeex mukk. Su dee kàdduy waxyu, dina wéy; su dee ay làkk, dina selaw; su dee xam-xam, dina xewwi. 9 Ndaxte as ndog lanu xam, te as ndog lanuy waxe kàdduy waxyu. 10 Waaye keroog bu li matale dikkee, ndog si wéy. 11 Ba ma dee tuut-tànk, ni tuut-tànk laa doon waxe, di dégge dégginu tuut-tànk, di xalaate ni tuut-tànk. Waaye bi may mag laa xewwil yëfi tuut-tànk. 12 Tey jii ci ab seetu lanuy gise gis-gis bu lënt. Waaye bu keroogee, màkk lanuy jàkkaarloo ak li nuy xool. Tey jii, as ndog laa xam, waaye su keroogee, ni ñu ma xame, ni laay xame ba mu mat sëkk.
13 Léegi nag liy sax moo di: ngëm ak yaakaar ak cofeel; yii ñett la, te li sut ci yooyii moo di cofeel.