1.Yowaan
muy bataaxal bu njëkk bi Yowaan bind
Gannaaw ki bind bataaxal bii moo wax ne fekke na dundug Yeesu, dañoo jàpp ne Yowaan ndaw li, di kenn ci taalibey Yeesu, moo ko bind.
Manees naa xam dara ci ñi moom bataaxal bi. Ñu bare ci taalibe yu njëkk ya dañoo dee, ba tax ay nit di weddi ne Yeesu Almasi bi nit dëgg la woon. Yowaan moo dëggal ne moom ak yeneen taalibe yi, gis nañu Yeesu te laal nañu ko. Moo soññi gëmkat ñi ci xam ak sopp Yàlla, di soppante, ni leen Almasi bi soppe.
Ci tënk:
1.1-4 Kàddug Yàlla mooy joxe dund.
1.5—2.29 Yàlla moo dig leer, nan doxe leer.
3.1—5.12 Yàlla mooy Baay bi, nan ko déggal ci di soppante.
5.13-21 Ku gëm Almasi bi, texe.
1
Kàddug dund gaa ngii
1 Ki dale nekk ca njàlbéen, ki nu dégg, gise ko sunuy gët, niir ko, laale ko sunuy loxo, kookoo di Kàddug dund. 2 Kookoo di dund ci boppam, moo feeñ, nu gis ko, te moom lanuy seedeel, di leen biralal ne kookoo di texe gu sax dàkk. Moo nekkoon fa Baay ba, te moo nu feeñu.
3 Li nu gis te dégg ko, moom lanu leen di àgge, ngir yeen itam ngeen am ak nun ag jokkoog mbokk. Te sunu jokkoog mbokk googu, nook Baay bi lanu ko séqal, ak Doomam Yeesu Almasi bi. 4 Loolu lanu leen di bind, ngir nu bokk mbég mu mat sëkk.
Yàlla moo dig leer
5 Xibaar bi nu dégge ci moom, di leen ko àgge, mooy lii: Yàlla ag leer la, te gennug lëndëm nekkul ci moom. 6 Su nu nee am nanook moom jokkoog mbokk, te teewu noo wéye ag lëndëm, danuy fen, te jëfewunu dëgg. 7 Waaye ni mu nekke moom ci boppam cig leer, su nu dee wéye noonu ag leer, su boobaa lanuy séq jokkoog mbokk, te deretu Yeesu Doomam moo nuy raxas ba nu set, tàggook bépp bàkkaar.
Doxeleen leer, tàggook bàkkaar
8 Su nu waxee ne amunu bàkkaar, sunu bopp lanuy nax, te amunu dëgg. 9 Su nu ko àggee sunuy bàkkaar, te muy ku jara wóolu, di boroom njub, moo nuy jéggal sunuy bàkkaar, raxas nu ba nu set, tàggook gépp njubadi. 10 Su nu nee bàkkaarunu, ab fen-kat lanu ko def, te kàddoom nekkul ci nun.