7
Suleymaan tabax na këram
Kërug boppam nag, Suleymaan tabax na ko ci fukki at ak ñett, doora sottal këram gépp. Ma nga njëkka tabax kër ga ñuy woowe Gottub Libaŋ. Guddaay bi di téeméeri xasab, yaatuwaay bi di juróom fukki xasab, taxawaay bi di fanweeri xasab, def ñeenti sàppey kenuy seedar yu yenu ay gàlluy seedar yu ñu yatt. Ñu teg ay banti seedar ci kaw gàllu yi kenu yi yenu: muy ñeent fukki gàllu ak juróom, sàppe bu nekk fukki gàllu ak juróom. Mu am ñetti sësalantey palanteer yu ñu fege ay laat te ñu dékkarloo ñett-ñett. Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk di bu kaare; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett.
Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy woowe Néegu Kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab; mu teg ca defar mbaar ci kanamam, mu ànd ak ay kenoom ak làcc way làng. Mu tabax néeg ba ñuy woowe Néegu Jal ba, muy Néegu Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw.
Këram ga mu dëkk it, ñu tabaxe ko noonu ci gannaaw Néegu Jal ba. Suleymaan teg ca tabaxal soxnaam doomu Firawna ja geneen kër gu nirook këram.
Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yatt la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci fondmaa bi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi. 10 Ñu defare fondmaa bi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab. 11 Xeer yi tege ci fondmaa bi, xeeri tànnéef la yu ñu yatt, natt ko, yemale, booleek banti seedar. 12 Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yatt aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir kër Aji Sax ja ak mbaaru buntam.
Tëgg ba defar na jumtukaayi kër Yàlla ga
13 Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Iram*Iram ak Uram, wenn tur wi la. Seetal it aaya 40 ak 45 (7.40, 45).. 14 Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon TirTir, ab dëkk la bu bokkul ci Israayil., di tëggub xànjar. Iram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.
15 Mu móol ñaari kenu xànjar gu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub. 16 Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw kenu yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab. 17 Bopp yi ci kaw kenu yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar. 18 Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci kenu gu ci nekk. 19 Bopp yi nekkoon ci kaw kenu yi ci mbaar mi nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab. 20 Bopp yi ci kaw ñaari kenu yi, bu ci nekk ñaari téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi.
21 Mu samp kenu yi ci mbaaru buntu néegu Yàlla bu mag bi; samp kenu ndijoor wi, tudde ko Yakin (muy firi Kiy taxawal), samp kenu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (muy firi Kiy dooleel). 22 Kaw kenu yi ay lëppi tóor-tóor yu ñu xellee ci tege. Liggéeyu kenu ya daldi sotti.
23 Ba mu ko defee Iram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub. 24 Ay gamb la ko sàkkal ci suufu kéméj gi, fukki gamb tollook xasab. Mu def gamb yi ñaari làng yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli. 25 Mbalkam njàpp mi tege ci kaw fukki jëmmi nag ak ñaar, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp. 26 Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppu tóor-tóor. Ñaari téeméeri barigo ak ñaar fukk (220) la mbalka miy def.
27 Mu daldi sàkk fukki watiiri rootukaayi xànjar wu ci nekk am guddaayu ñeenti xasab, yaatuwaay bi di ñeenti xasab, taxawaay bi di ñetti xasab. 28 Ni ñu defare rootukaay yi nii la: ay wetam lañu defare làcci xànjar, lëkkalee làcc yi ay laat. 29 Muy làcc yu Iram yatt ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay serub. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yatt ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi. 30 Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkkalee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor. 31 Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yatt ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu kaare. 32 Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll. 33 Mbege yi bindoo ni mbegey watiiri xare. Tóor yeek mbege yi ak sidditi mbege yi ak ŋanku yi, xànjar lañu ko xellee. 34 Ñeenti kenu yi ci ñeenti koñi rootukaay bi, bu ci nekk dees koo xelleendook weti rootukaay yi, ba lépp di benn. 35 Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn. 36 Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor. 37 Noonu la Iram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind.
38 Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook ñeenti barigo ak genn-wàll; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj.
39 Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam njàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku.
40 Iram sàkk itam ndabi tibbukaayu dóom ak ñiitukaay yi ak këll yi.
Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Aji Sax ji: 41 muy ñaari kenu yi, ak ñaari gamb yiy boppi kenu yi, te tege ca seen kaw, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi, 42 ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yi ci boppi kenu yi; 43 ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi. 44 Menn mbalkam njàpp mi ñuy wax Géej gi it ci la, ak fukki nag ak ñaar yi ronu mbalkam njàpp mi. 45 Ndabi tibbukaayu dóom ak ñiitukaay yi, ak këll yi, mboolem yooyu jumtukaay, xànjar bu ñu jonj la ko Iram defal Buur Suleymaan, ñeel kër Aji Sax ji. 46 Ci joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban yu ñu gas, ci diggante Sukkót ak Cartan. 47 Suleymaan daldi bàyyi jumtukaay yépp noonu, ndax na mu baree bare lool, ba natteesul diisaayu xànjar ba ca dem.
48 Gannaaw loolu Suleymaan defarlu na mboolem yeneen jumtukaayi kër Aji Sax ji: muy sarxalukaayu wurus ba, ak taabalu wurus ja ñuy teg mburum teewal ma, 49 ak tegukaayi làmpi wurusu ngalam yi, juróom ci wetu ndijoor, juróom ci wetu càmmoñ, fa kanam néeg bu sella sell bi; tóor-tóor yi it ak làmp yi ak ñiim yi, lépp di wurusu ngalam; 50 ndab yi itam, ak feyukaay yi ak këll yi ak kopp yi ak andi cuuraay yi, lépp wurusu ngalam la. Te lafi buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu sella sell bi, ak lafi buntu néeg bi ñuy jaare dugg ci néeg bu mag bi, lépp wurus la.
51 Ba loolu amee, mboolem lu Buur Suleymaan liggéeyal kër Aji Sax ji daldi sotti. Mu boole xaalis baak wurus waak jumtukaay ya Daawuda baayam sellalaloon Aji Sax ji, yeb ko ca denc ya def alali kër Aji Sax ji.

*7.13 Iram ak Uram, wenn tur wi la. Seetal it aaya 40 ak 45 (7.40, 45).

7.14 Tir, ab dëkk la bu bokkul ci Israayil.