10
Lingeer buurub Seba seetsi na Suleymaan
1 Ci kaw loolu Lingeeru Seba dégg riirum Suleymaan ma turu Aji Sax ji waral. Mu dikk di nattusi am xelam, cax ko cax yu jafe. 2 Mu agsi Yerusalem, ànd ak topp mu takku lool ak giléem yu sëf ay ndàbb yu xeeñ ak wurus wu baree bare ak per yu gànjare. Ba mu dikkee ba ci Suleymaan, mboolem la mu jàppoon ca xelam la ko wax. 3 Suleymaan tontu ko ca mbir ya mu laaj yépp. Menn mbir tiiñul Buur, ba leeralalu ko ko. 4 Lingeer buurub Seba gis xelum Suleymaan mu rafet mépp, ak kër ga mu tabax, 5 ak njëlu këram, ak jataayu dagam ya, ak taxawaayu surgaam ña ak seen col ga, ak ña yor ay naanam, ak saraxi rendi-dóomal ya muy joxe ca kër Aji Sax ji. Mu daldi yéemu, ba ag noowam réer ko.
6 Mu ne Buur: «Jëw ba ma déggoon ca sama réew ci say mbir ak sa xel mu rafet kay, lu dëggu la! 7 Gëmuma ko woon ba bi ma dikkee, ba teg ci sama bët. Ndeke genn-wàll gi sax waxeesu ma ko woon. Wees nga riir ma ma déggoon ci yaw, ci xel mu rafet ak lu baax. 8 Ndokkalee say nit! Ndokkalee sa jawriñ ñii dëkke taxaw ci sa kanam, di dégg sam xel! 9 Cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi la bége, ba teg la ci jalub Israayil. Aji Sax ji moo sopp Israayil cofeel gu dul jeex, ba tax mu fal la buur, ngir ngay jëfe dëgg ak yoon.»
10 Ba mu ko defee Lingeer buurub Seba may Suleymaan lu ëpp ñeent fukki barigoy wurus ak cuuraayu ndàbb lu ne gàññ ak per yu gànjare. Cuuraayu ndàbb loola Lingeer buurub Seba mayoon Buur Suleymaan, lu ni mel dikkatu fa ndax bare.
11 Gaali Buur Iram ya itam daan jële wurus ca réewum Ofir, jële Ofir lu takkoo takku ci banti sàntaal ak per yu gànjare. 12 Buur sàkke ca banti sàntaal ya ay sëppukaayi kaw taax ngir kër Aji Sax ji ak kër buur ak ay xeeti xalam ngir woykat yi. Banti sàntaal bu ni mel masu faa dikk, te giseesu ko fi ba tey jii.
13 Buur Suleymaan itam may Lingeer buurub Seba mboolem lu mu bëgg te sàkku ko, te bokkewul ak la ko Suleymaan joxal boppam ca loxoom bu tàlli ba buur yelloo. Ba loolu amee Lingeer buurub Seba walbatiku, ñibbim réewam, mooki surgaam.
Suleymaan bare woon na alal
14 Wurus wa daan dikkal Suleymaan cim at, diisaay ba tollu ci ñaari téeméeri barigoy wurus ak ñaar fukk ak juróom ñett (228), 15 te limaaleesul galag ya jóge ca jaaykat yaak jula yaak mboolem buuri Arabi ak jaraafi réew ma.
16 Buur Suleymaan nag sàkklu ñaari téeméeri pakk yu mag yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, benn bu ci nekk jël lu tollook juróom ñaari kiloy wurus, 17 ak ñetti téeméeri pakk yu ndaw yu wurus wu ñu tëgg ba mu jekk, pakk bu ci nekk di xawa tollook ñaari kiloy wurus. Buur boole ko denc ca këram ga ñuy wax Gottub Libaŋ.
18 Buur teg ca sàkk ngàngune mu mag mu ñu xoobe wurus wu set wecc, rafetale ko yaxu bëñi ñey. 19 Juróom benni dëggastal la ngàngune ma am, wéeruwaay ba ca kaw mërgalu. Mu am ay loxo yu séq toogukaay bi, ak ñaari jëmmi gaynde yu taxaw, wet gu nekk benn. 20 Mu am it fukki jëmmi gayndeek ñaar yu taxaw ca ñaari weti juróom benni dëggastal ya, ñaari gaynde séq ndëggastal lu nekk. Sàkkeesul lu ni mel ci mboolem nguur yi!
21 Mboolem lu Buur Suleymaan daan naane wurus la, te mboolem ndabi këram ga ñuy wax Kër Gottub Libaŋ wurusu ngalam la. Dara du ca xaalis, ndax xaalis jàppeesu ko woon muy dara ca jamonoy Suleymaan. 22 Te sax ay gaal yu mag la Buur amoon, ñuy ànd ak gaali Iram, benn yoon ci ñetti at yu nekk gaal ya yeb wurus ak xaalis ak bëñi ñey aki golo, ba ciy dàngin.
23 Buur Suleymaan dem na ba sut mboolem buuri kaw suuf ci wàllu alal ak ci wàllu xel mu rafet. 24 Àddina sépp a daan wuta giseek Suleymaan, ngir taataansi xelam mu rafet mi Yàlla def cib xolam. 25 Ñooñu ñoo ko daan indil at ci kaw at, ku nekk ak sab teraanga, muy ay jumtukaayi wurus ak yu xaalis aki yére aki gànnaay aki cuuraay aki fas aki berkelle.
26 Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri (1 400) watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu yebal ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. 27 Buur Suleymaan a def xaalis late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi. 28 Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi*Silisi mooy Kewe ba tey., baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde. 29 Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri dogi xaalis (600) la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki dogi xaalis (150), te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen.