2.Jaar-jaar ya
muy ñaareelu téere bi te ëmb jaar-jaari jamono
Ñaareelu téereb Jaar-jaar ya moo wéyal nettalib démbi Israayil, bi dooroon ci 1.Jaar-jaar ya. Téere bii moo indi ni nguurug Suleymaan ame woon daraja, di ci fésal li mu tabax kër Yàlla ga. Téere bi teg ci indi jëfi buuri Yuda yi wuutu Suleymaan, te gën cee biral yitte ji kenn ku nekk amoon ci mbiri askan wi, ci wàllu ngëm.
Meneen mbir mu ñu ci fàttali mooy tasteg Yerusalem, ak ngàllo ga Israayil mujje ca Babilon ga ñu leen toxaloon. Teewul téere bi tëje xew-xewu jàmm, te mooy ba Buur Sirus bu Pers yékkatee ab dogal bu yiwi bànni Israayil, may leen ñu saña ñibbi seenum réew.
Ci tënk:
1.1-17 Suleymaan ci ndoortel nguuram.
2.1—7.22 Lu jëm ci tabaxub kër Yàlla ga, ñu jagleele ko am xew.
8.1-18 Lu jëm ci darajay nguuru Suleymaan.
9.1-12 Lingeer buurub Seba gane na Suleymaan.
9.13-31 Lu jëm ci darajay Suleymaan ak deewam.
10.1—36.23 Lu jëm ci yeneen buuri Yuda yi.
1
Suleymaan ñaan na xel mu rafet
Suleymaan doomu Daawuda mujj na dëju bu baax ci nguuram, Aji Sax ji Yàllaam ànd ak moom, kaweel ko lool. Suleymaan nag wax ak Israayil gépp; njiiti junni yaak njiiti téeméer yaak àttekat yaak njiiti Israayil gépp, mboolem seen kilifay kër maam ya. Ci biir loolu Suleymaan ànd ak mbooloo ma mépp, dem ca bérebu jaamookaay ba ca Gabawon, sarxali fa, ndax xaymab ndajem Yàlla ba Musaa jaamub Aji Sax ji defaroon ca màndiŋ ma, foofa la nekkoon. Waaye fekk na gaalu Yàlla ga, Daawuda toxale woon na ko Kiryaat Yarim, yóbbu ko fa mu ko waajal, muy ab xayma bu mu ko sampal ca Yerusalem. Sarxalukaayu xànjar ba Beccalel doomu Uri doomu Ur defar nag, Daawudaa ko tegoon ca Gabawon, fa kanam màkkaanu Aji Sax ji, te mooy la fa Suleymaan ak mbooloo ma doon sàkkusi. Suleymaan dem foofa ca sarxalukaayu xànjar ba ca kanam Aji Sax ji, ca kanam xaymab ndaje ma. Mu joxe fa junniy saraxi rendi-dóomal. Guddig keroog la Yàlla feeñu Suleymaan. Mu ne ko: «Ñaanal loo bëgg ma may la ko.» Suleymaan ne Yàlla: «Yaw de yaa baaxe lool Daawuda saa baay, te yaa ma fal buur, ma wuutu ko. Léegi nag Aji Sax ji Yàlla, sa kàddu gaak Daawuda sama baay, yal na sax rekk, gannaaw yaw yaa ma fal ci kaw askan wu yaa, tollu ni feppi suufas àddina. 10 Kon nag xel ak xam-xam nga may may, ba ma xam nu may jiitee askan wii. Ndax kat, ana kan mooy àtte sa ñoñ, wii askan wu yaa?» 11 Yàlla ne Suleymaan: «Gannaaw loolu moo nekk ci sa xol; ñaanoo koom ak alal ak daraja, ak sa bakkani bañ rot, te fan wu gudd it, ñaanoo ko, xanaa di ñaan xel ak xam-xam boo àttee sama ñoñ ñi ma la fal buur ci seen kaw, 12 xel mi ak xam-xam bi, mayees na la ko. Koom ak alal ak daraja it maa la ciy may lu buur yi masula am, du ñi la jiitu, du ñi topp ci yaw.»
13 Ba loolu amee Suleymaan bàyyikoo ca xaymab ndaje ma ca jaamookaay ba ca Gabawon. Mu dem Yerusalem, falu buur ca Israayil.
14 Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri (1 400) watiir, ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu teg ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. 15 Buur Suleymaan a def xaalis ak wurus late biir Yerusalem bay safi doj, garabi seedar di fa saf garabi sikomoor yi ne xas ci suufu tund yi. 16 Fasi Suleymaan, Misra lañu leen daan jëggaanee ak Silisi, baana-baanay buur, ca Silisi lañu leen daan jënde. 17 Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri (600) dogi xaalis la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki (150) dogi xaalis, te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen.
18 Suleymaan nag dogu ne kër lay tabax ñeel turu Aji Sax ji, ak geneen kër gu ñeel nguurug boppam.