25
Lu jëm ci nguurug Amaciya
Ñaar fukki at ak juróom la Amaciya amoon ba muy falu, te ñaar fukki at ak juróom ñeent la nguuru fa Yerusalem. Yaayam moo doon Yowadan ma cosaanoo Yerusalem. Def na njub gi Aji Sax ji rafetlu, waaye defewu ko pastéefu xol bu mat sëkk. Ba nguur ga demee ba dëgër ñeel ko, moo bóom jawriñam ña bóomoon Buur baayam. Waaye seeni doom, bóomu leen, ngir dëppook la ñu bind ci téereb yoonu Musaa, te Aji Sax ji santaane ko, ne: «Deesul rey baay ndax doom te deesul rey doom ndax baay. Nit ku nekk, bàkkaaru boppam lees koy reye.»
Ci kaw loolu Amaciya woo Yuda, ñu daje, mboolem góori Yuda ak Beñamin, mu topp na ñu bokke seeni kër maam, tàbbal leen noonu ay njiiti kuréeli junni ak njiiti kuréeli téeméer. Mu lim leen, dale ca góor ña am ñaar fukki at jëm kaw, ña mu leen gisal di ñetti téeméeri junniy (300 000) góor ñu xare war, te ñu mane ab xeej akub pakk. Mu boole ca jël téeméeri junniy (100 000) ñeyi xarey Israayil ñu am doole, fey leen lu wara tollook ñetti junni kiloy xaalis ak liibar (3 500).
Ba loolu amee genn góorug Yàlla dikk ba ca moom ne ko: «Buur, bu gàngooru Israayil ànd ak yaw, ndax Aji Sax ji àndul ak Israayil, àndul ak kenn ci Efraymeen ñi.» Soo àndee ak ñoom dem déy, defal loo man te góor-góorlu ca xare ba, Yàlla moo lay daane fa kanam noon ba, ndax Yàllaa mana walloo, moo mana daaneel. Amaciya ne góorug Yàlla ga: «Ana lees di def nag ak ñetti junniy kiloy xaalis ak genn-wàll (3 500) yi ma fey gàngoori Israayil?» Góorug Yàlla ga ne ko: «Aji Sax ji man na la may lu ko ëpp fuuf.» 10 Ba loolu amee Amaciya beddi gàngoor ga ko fekksi te bawoo fa Efrayim, ngir ñu ñibbi. Seen xol nag tàng lool ca Yuda, ñu ñibbee xol bu tàng. 11 Ba mu ko defee Amaciya takku fitam, jiite gàngooram, dem xuru Xorom wa, rey fa fukki junniy niti Seyir. 12 Ñeneen fukki junni ca ñoom, Yudeen ña jàpp leen ñuy dund, ñu yéege leen ci aw doj ba ca kaw. Ca njobbaxtalu doj wa lañu leen sànnee, ñu rajaxoo, ñoom ñépp. 13 Niti gàngoor ga Amaciya waññi woon, ba ànduñook moom ca xare ba nag, ca dëkki Yuda lañu dalandoo, dale ca Samari ba Bet Oron. Bóom nañu ca ñoom ñetti junni, boole ca sëxëtoo cëxëtoo mu réy.
14 Ndeke ba Amaciya ñibbisee, gannaaw ba mu dumaa Edomeen ña, ay yàllay waa Seyir la indaale, sampal leen boppam, ñu taxawe ay yàlla; ñoom lay sujjóotal, ñoom lay taalal cuuraay. 15 Ba loolu amee sànjum Aji Sax ji tàkkal Amaciya, mu yebal fa moom ab yonent, yonent ba ne ko: «Ana looy toppe yàllay askan wu xettaliwul ay ñoñam, ba jële leen ci say loxo?» 16 Naka lay wax ak moom, Amaciya dog ko, ne ko: «Kuy xelal buur lanu la def xanaa? Na doy! Ana looy indile sa bopp ay dóor?» Yonent ba noppi. Gannaaw loolu mu ne: «Xam naa ne Yàlla moo la nara sànk, ndax yaa def lii, te dégguloo samab digle.»
17 Gannaaw ba Amaciya buurub Yuda diisoo ak ñi koy xelal, dafa yónnee ca buurub Israayil Yowas doomu Yowaxas doomu Yewu. Mu ne ko: «Dëkk naa la, dikkal, nu jàkkaarloo!» 18 Yowas buurub Israayil yónnee Amaciya buurub Yuda tontam, ne ko: «Ndég ga ca Libaŋ moo yónnee woon ca garabu seedar gu mag ga ca Libaŋ, ne ko: “Sa doom jii, may ko sama doom jabar.” Ci kaw loolu rabu àllu Libaŋ jaare fa, dëggaate ndég ga. 19 Nee nga xanaa du yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la, nga di ko damoo. Léegi nag tee ngaa toog sa kër? Ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»
20 Amaciya nag faalewul wax jooju, te Yàlla moo dogal loolu, ngir teg ko ciy loxo, ndax yàllay Edom ya ñu toppoon. 21 Gannaaw loolu Yowas buurub Israayil jóg; ñu jàkkaarloo mook Amaciya buurub Yuda, ca Bet Semes ga ca Yuda. 22 Ba mu ko defee muy jéllu Yuda fa kanam Israayil. Waa Yuda tasaaroo, ku nekk ñibbi ca sab xayma. 23 Yowas buurub Israayil nag jàpp buurub Yuda, Amaciya doomu Yowas doomu Yowaxas, ca Bet Semes. Gannaaw loolu mu yóbbu ko Yerusalem, daldi màbb tata ja, la ko dale buntu Efrayim ba ca buntu Ruq ba, muy ñeenti téeméeri xasab. 24 Ci biir loolu wurus waak xaalis baak mboolem jumtukaay ya nekkoon ca kër Yàlla, ca loxol Obedd Edom ak ca denci kër buur, mu jël lépp, boole ca nit ñu mu jàpp, daldi dellu Samari.
25 Amaciya doomu Yowas buurub Yuda dund na fukki at ak juróom gannaaw deewug buuru Israayil Yowas doomu Yowaxas. 26 Li des ci mbiri Amaciya, yu njëkk yaak yu mujj ya, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Buuri Yuda ak Israayil. 27 La dale jant ba Amaciya dëddoo Aji Sax ji, ca la ko ay nit lalal pexe ca Yerusalem, mu daw dem Lakis, ñu yónnee dabi ko ca Lakis. Foofa lañu ko reye. 28 Ba mu ko defee, ay fas lañu yóbboo néew ba, denci ko fa ay maamam, ca dëkk ba, ca Yuda.