27
Lu jëm ci nguurug Yotam
Yotam amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog. Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na Osiyas baayam daan defe la daan defe. Waaye nag duggul ca kër Aji Sax ji. Teewul nag askan wa di defug yàqute ba tey. Moom moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar, te tata ba ca tundu Ofel, tabax na ca lu bare. Ay dëkk it tabax na ko ca tundi Yuda, te gott ya, tabax na ca kër yu tata wër ak seeni sooroor.
Moom it moo xareek buurub Amoneen ña, duma leen, ba Amoneen ña jox ko atam fanweeri barigoy xaalis ak ñeent, ak fukki barigoy bele ak benn; lors it, fukki barigo ak benn. Loolu la ko Amoneen ña indil atam, indilaatal ko ko ca déwén sa, indilatil ko ko ca déwén-jéeg sa. Yotam mujj na am doole, ndax pastéef ga mu daan doxe fa kanam Yàllaam Aji Sax ji.
Li des ci mbiri Yotam ak mboolem ay xareem ak ay jëfinam, ma nga binde ca téere ba ñu dippee Buuri Israayil ak Yuda. Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Gannaaw gi, Buur Yotam saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Axas doomam moo falu buur, wuutu ko.