6
Nun ñi bokk ci liggéey bi nag, noo leen di ñaan ngeen baña nangu yiwu Yàlla ci neen. Ndaxte Yàlla moo ne:
«Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la;
bu bésub mucc jotee, ma wallu la*Seetal ci Esayi 49.8.
Te nag, tey jii la bésub yiw taxaw; tey kat, la bésub mucc.
Liggéeyal Yàlla ñàkkul aw tiis
Bëggunu kenn sikk sunub liggéey, moo tax bëggunoo jëfe lenn luy doon tojaange ci kenn. Ci lépp kay lanu bëgga seedeel sunu bopp, ne noo yelloo ngërëm, te ay jawriñi Yàlla lanu, di ñu muñ lu bare ci biir coono aki mitit aki njàqare; ci ay dóor ak néegi kaso, ci biir mbooloo yu nu jógal, ci doñ-doñ ju metti ak fanaanee xoole akub xiif; te nuy setal sunu dund, di ànd ak xam-xam, ci biir muñ akug mbaax, ci biir Noo gu Sell gi ak cofeel gu amul jinigal, ci biir kàddug dëgg ak kàttanu Yàlla; ci kaw gànnaayi njubte yi ci sunu loxol ndijoor ak lu càmmoñ; ci biir teraanga ak ci biir toskare; ci biiri baatal ak jëw yu rafet. Dees noo jàppe ay mbubbookati dëgg, te nuy nit ñu dëggu; jàppe nu ñu kenn xamul, te nuy ñu siiw; jàppe nu ñuy waaja dee, te nuy dund; jàppe nu ñu ñu wara mbugal, te bañ leena teg àtteb dee. 10 Dees noo jàppe boroomi tiis, te nu dëkke mbég; jàppe nu ay néew-ji-doole, te nu woomal ñu bare; jàppe nu ñu amul dara, te nu moom lépp.
11 Yeen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir yépp, ubbil leen sunu xol. 12 Genn ñooru jógewul ci nun, waaye yeen yeena nu ñooru ci seen xol. 13 Léegi nag yeen, feyleen nu bor bi boog, ma wax ak yeen ni samay doom, ubbilleen nu seen xol!
Baleen bokkaale
14 Buleen lëkkoo ak gëmadikat ñi. Gan lëngoo la njub ak ndëngte séq? Gan booloo la leer ak lëndëm séq? 15 Gan juboo la Almasi bi ak Seytaane séq? Wan wàll la gëmkat bi bokk ak gëmadikat bi? 16 Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne:
«Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir,
di seen Yàlla, ñuy sama ñoñSeetal ci Sarxalkat yi 26.12.
17 Kon nag:
«Nangeen génne ci seen biir, te teqalikoo ak ñoom,»
la Boroom bi wax,
«lu sobewu, buleen ko laalSeetal ci Esayi 52.11..
Su boobaa, maa leen di dalal§Seetal ci Esekiyel 20.41..
18 Maay doon seen baay,
ngeen di samay doom, góor ak jigéen*Seetal ci 2.Samiyel 7.14.
la Boroom bi, Aji Man ji wax.

*6.2 Seetal ci Esayi 49.8.

6.16 Seetal ci Sarxalkat yi 26.12.

6.17 Seetal ci Esayi 52.11.

§6.17 Seetal ci Esekiyel 20.41.

*6.18 Seetal ci 2.Samiyel 7.14.