2.Samiyel
di téereb ñaareel bi
Téereb 2.Samiyel moo indi jaar-jaari Buur Daawuda ak ndamam. Indi na tamit fan yu lëndëm ci dundam: digganteem ak ndaw sa Batseba ca la, ak fippu ga doomam Absalom jiite woon. Teewul Daawuda mooy ku jikkoom juboo ak xolu Yàlla, ni ko Yàlla ci boppam waxe. Gaawoon na ci nangu ay tooñam, te di tuub, di ñaan Yàlla mu jéggal ko.
Ci tënk:
1.1—6.23 Lu jëm ci palug Daawuda ak ndoortel nguuram.
7.1-29 Yàlla fas na kóllëre ak Daawuda.
8.1—10.19 Daawuda am na ay ndam ci ay noonam.
11.1—12.25 Daawuda moy na Yàlla, Yonent Yàlla Natan ŋàññ ko.
12.26—21.22 Lu jëm ci nguurug Daawuda ak gàllankoor ya.
22.1—24.25 Daawuda biral na cantam gu mujj, nguuram di amati gàllankoor.
Lii mooy jaar-jaari Buur Daawuda
1
(Saar 1—20)
Lu jëm ci tàggeb Sawul
Gannaaw ba Sawul faatoo, fekk na Daawuda walbatikoo ca dumay Amalegeen ña, dellu Ciglaag, ba toog fa ñaari fan. Ca gannaaw ëllëg sa, jenn waay ne jimeet, jóge ca dalub Sawul, dikk. Yére yaa nga xottiku, bopp ba taq suuf, ngir naqarlu. Naka la agsi ci Daawuda, daldi daanu fi suuf, sujjóot.
Daawuda ne ko: «Foo jóge nii?» Mu ne ko: «Ca dalub Israayil laa rëcce.» Daawuda ne ko: «Lu xew, gaawe ma!» Mu ne ko: «Mbooloom Israayil a dawe ca xare ba. Ñu bare ca ñoom daanu nañu, dee. Sawul ak doomam Yonatan it dee nañu.» Daawuda ne ndaw la: «Lu la xamal ne Sawul ak doomam Yonatan dee nañu?» Ndaw la ne ko: «Dafa yemook ma tollu tembe ca kaw tundu Gilbowa. Ndeke Sawul a nga fa, sukkandikoo xeejam. Watiiri xare yaak gawar ya defuñu lu moy ne ko dann. Naka la ne gees, yem ci man, woo ma, ma wuyu. Mu ne ma: “Yaa di kan?” Ma ne ko: “Ab Amalegeen laa.” Mu ne ma: “Kaay fii, jekkali ma. Maa ngi ci miirum dee, doonte dese naa tuuti.” 10 Ma dikk, daldi koy jekkali, ndax xamoon naa ne du dundati gannaaw jéllam ba. Ma summi nag mbaxanam buur ma mu soloon, tekki lam ba woon ca përëg ma. Yooyu laa la yótsi nii, sang bi.»
11 Ba loolu amee Daawuda sëq yéreem, xotti, ña ànd ak moom ñépp itam, noonu, ndax aw naqar. 12 Ñaawlu nañu, di jooy, lekkuñu ba ca ngoon ndax Sawul ak doomam Yonatan ak gàngooru Aji Sax ji, ak waa kër Israayil ña ñu reye saamar.
13 Daawuda ne ndaw la: «Ana foo bokk?» Mu ne ko: «Man doomu doxandéemub Amalegeen laa.» 14 Daawuda ne ko: «Noo saña xàcce sa loxo, di bóom ki Aji Sax ji fal?» 15 Daawuda nag woo kenn cay surgaam, ne ko: «Dikkal dóor, mu dee!» 16 Daawuda ne Amalegeen ba: «Yaa gàddu sa bakkanu bopp, ndax yaa seedee sa gémmiñu bopp ne yaa rey ki Aji Sax ji fal.» Surga ba dóor Amalegeen ba, mu dee.
Daawuda jooy na Sawul ak Yonatan
17 Kàddu yii la Daawuda jooye Sawul ak doomam Yonatan. 18 Moo santaane ñu jàngal ko askanu Yuda. «Fittkat» lañu dippee woy wi. Nii lañu ko binde ci Téereb aji jub ji. Mu ne:
 
19 Wóoy Israayil, ña ngay sagoo lañu jam, ñu ne lareet ca sa tund ya!
Jàmbaar ñaa daanu!
 
20 Buleen ko siiwal fa Gaat,
buleen ko yéene fa mbeddi Askalon,
lu ko moy janqi Filisti bég,
janqi yéefar yiy tex-texi.
 
21 Wóoy tundi Gilbowa!
Yàlla bu ngeen lay, bu ngeen tawlu.
Yàlla bu seeni tool nangooti, ba duunal njoxem pepp,
nde foofa lees toroxale pakkub jàmbaar.
Wóoy pakkub Sawul ba deesul diwati!
22 Du deret mbaa nebbonu jàmbaar bu fittug Yonatan xof,
te saamaru Sawul ba du sooy!
 
23 Wóoy Sawul ak Yonatan,
ñoo yiw, sopplu ba ñuy dund,
te ba ñu deewee, teqalikoowuñu.
Ag jaxaay, ñoo ko gëna gaaw,
te gaynde, ñoo ko gëna jàmbaare.
 
24 Yeen jigéeni Israayil, jooyleen Sawul ma leen wodde
ndimol tànnéef lu xonq curr,
takkal leen gànjari wurus ca seen kawi yére.
 
25 Jàmbaar ñaa daanoo biir xare ba,
Yonatan lañu jam ca kaw tund ya!
26 Yonatan, doom yaay, tiisoo naa la,
dama laa soppoon lool,
te sa mbëggeel ci man yéeme,
ba raw mbëggeelu jigéen.
 
27 Jàmbaar ñaa daanu,
ngànnaayi xare ya sànku!