5
Daawuda falu na buur ca Israayil gépp
1 Ci kaw loolu giiri Israayil yépp dikk fa Daawuda ca Ebron, ne ko: «Noo ngii di say bokk lenqe. 2 Te it démb ak bërki-démb, ba Sawul dee sunu buur sax, yaa doon jiite Israayil ci xare. Aji Sax ji ne la: “Yaay sàmm Israayil sama ñoñ te yaay yilif Israayil.”» 3 Noonu la magi Israayil ñépp dikke ca Buur Daawuda ca Ebron, mu fasook ñoom kóllëre foofa ca Ebron, fa kanam Aji Sax ji. Ba mu ko defee ñu sotti Daawuda diwu pal ga, muy buurub Israayil.
4 Daawuda amoon na fanweeri at, ba muy falu buur, te ñeent fukki at la nguuru. 5 Ca Ebron la yore nguurug Yuda juróom ñaari at ak juróom benni weer, waaye ca Yerusalem la yore mboolem Israayil ak Yuda diiru fanweeri at ak ñett.
Daawuda nangu na Yerusalem
6 Gannaaw loolu Buur Daawuda ànd aki xarekatam, songi Yerusalem ga ñu doon woowe Yebus itam, ndax la fa Yebuseeni diiwaan ba dëkke woon. Yebuseen ña ne Daawuda: «Doo fi dugg de, ndax gumba yeek lafañ yi rekk ñoo lay waññi.» Booba foog nañu ne Daawuda manu faa dugg. 7 Terewul Daawuda nangu tatab Siyoŋ ga ñu mujj woowe Kër Daawuda. 8 Daawudaa noon bésub keroog: «Ku bëgga jam Yebuseen ñi, ca xuntum yoonu ndox ma ngay mana dabe seeni gumbaak seeni lafañ, xuloowaaley Daawuda yi.» Looloo waral waxin wi ñu naan: «Gumba akub lafañ du dugg kër ga.» 9 Ba mu ko defee Daawuda dëkk ca biir tata ja, woowe ko Kër Daawuda, ba noppi tabax ay kër yu bees fa ko wër fépp, dale ko ca sëkkub Milo*Milo, xur la wu doxoon diggante gox ba ñu naan Kër Daawuda ak fa kër Yàlla ga wara nekk., ba ca biir. 10 Daawuda nag di gëna am doole, Aji Sax ji Yàlla, Boroom gàngoori xare yi ànd ak moom.
11 Ci biir loolu Iram buurub Tir, yebal ay ndaw ca Daawuda, ñu yóbbul ko ay banti garabu seedar ak ay liggéeykati bant ak yattkati xeer, ngir ñu tabaxal Daawuda kër. 12 Daawuda xam ne Aji Sax jee ko fal buurub Israayil te moo kaweel nguuram ngir Israayil ñoñam.
13 Gannaaw ba Daawuda jógee Ebron, denc na ay nekkaale ak yeneeni soxna ca Yerusalem. Mu am ca yeneen doom yu góor ak yu jigéen. 14 Doom yu góor yi juddoo Yerusalem ñoo di Samwa ak Sobab ak Natan ak Suleymaan 15 ak Ibaar ak Elisuwa ak Nefeg ak Yafya 16 ak Elisama ak Elyada ak Elifelet.
Buur Daawuda duma na waa Filisti
17 Ba waa Filisti déggee ne fal nañu Daawuda buurub Israayil, ñoom ñépp a jóg, di ko wër. Daawuda nag dégg ko, dem làquji ca biir tata ja. 18 Waa Filisti dikk, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. 19 Daawuda laaj Aji Sax ji, ne ko: «Ndax ma songi waa Filisti? Ndax dinga leen teg ci sama loxo?» Aji Sax ji ne ko: «Demal, maay teg waa Filisti ci say loxo déy!» 20 Daawuda dem ba Baal Peracim, duma leen foofa. Mu ne: «Aji Sax jee ma xàllal yoon, ne jàyy ni walum ndox ca kaw noon ya.» Moo tax ñu woowe béreb boobu Baal Peracim (muy firi Boroom bi xàll naw yoon). 21 Filisteen ña nag waccoon seeni gàllaaj, Daawudaaki nitam boole yóbbu.
22 Ba mu ko defee waa Filisti dikkaat, tasaaroo ca xuru Refayeen ña. 23 Daawuda dellu laaj Aji Sax ji. Mu ne ko: «Bul topp seen gannaaw, wër leen ndombo, dal ca seen kaw fa janook garab ya. 24 Booy dégg tànk yuy jaab ca kaw njobbaxtali sànd ya rekk, gaawtul, ndax booba Aji Sax jee la jiitu, di dumaji waa dalub Filisti.» 25 Daawuda nag def noonee ko Aji Sax ji sante, ba duma waa Filisti la ko dale Geba, ba ca buntu Geser.