18
Daawuda xare naak Absalom
Ba loolu weesoo Daawuda xayma na mbooloo ma mu àndal, fal ca seen biir njiiti kuréeli junniy xarekat, kuréel gu ci nekk ak njiiti kuréeli téeméer ya ko sos. Daawuda def mbooloo ma ñetti xaaj, yebal leen. Benn xaaju mbooloo ma, Yowab jiite leen; beneen xaaj ba, Abisay doomu baayu Yowab mi Ceruya di yaayam, jiite leen; xaaj ba ca des Itay waa Gaat ba jiite leen. Buur ne gàngooru xare ga: «Damay ànd ak yeen, man itam.» Teewul mbooloo ma ne ko: «Déedéet, yaw doo ànd ak nun! Ndax nun su ñu nu dàqee, du am boobu solo. Bu sunu genn-wàll deewee it, du am benn solo. Waaye sa jenn jëmm jii mooy fukki junni ci nun. Kon nag desal nu ci dëkk bi, di nu fi yónnee wall, moo gën.» Buur ne leen: «Baax na, kon ma def noonu.» Ba loolu amee Buur taxaw ca buntu dëkk ba, xarekat ya def ay kuréeli téeméer ak kuréeli junni, daldi génn dem. Buur nag digal Yowab ak Abisay ak Itay, ne leen: «Seetleen ci man te def ndànk ak ngóor si Absalom.» Xarekat yépp a dégg kàddu googu Buur dénk njiit ya ca mbirum Absalom.
Mbooloo maa nga jëm ca toolub xare ba, di xarejeek Israayil. Xare baa nga ame ca gott ba ñuy wax Efrayim, mbooloom Israayil nag daanu foofa ca kanam xarekati Daawuda. Bésub keroog ñu baree dee: ñaar fukki junnee (20 000) daanu. Xare ba daa law foofa ba daj diiwaan ba bépp; te ña dee ca gott ba bésub keroog ñoo ëpp ña saamar rey.
Ci biir loolu Absalom ne pemm taseek xarekati Daawuda. Ma nga war berkelle. Berkelle ba fëx wuti garab gu réy, te bànqaas ya fatt. Boppu Absalom tance ca garab ga, berkelle ba mu war topp xélam, mu des fa di sandaamtalu. 10 Ba mu ko defee jenn waay gis ko, dem, wax ko Yowab, ne ko: «Ki ma gis de, Absalom a, ma nga wékku ci genn garab.» 11 Yowab ne ko: «Nga ne? Gis nga ko te jamoo ko foofa, mu daanu? Kon de doon naa la jox fukki dogi xaalis, takkal la ngañaayal xarekat tegal la ca.» 12 Waa ja ne Yowab: «Ku tegoon ci sama loxo junniy dogi xaalis sax, duma yékkati sama loxo jëmale ko ci doomu buur. Noo déggal sunu bopp Buur sant la, yaak Abisay ak Itay, ne leen: “Na ma ku nekk ci yeen dimbali, te def ndànk ak ngóor si Absalom.” 13 Su ma jaayoon sama bakkan, ba def njekkar it, amul dara lu ump Buur, te kon it yaw danga ciy raxas say loxo.» 14 Yowab ne ko: «Duma la déglu sax, nga di ma yàggal!»
Ci kaw loolu Yowab jël ñetti bant yu ñaw, jam ko Absalom ci xol, fekk ko muy dund ba tey ca xolu garab ga mu tancu. 15 La ca tegu fukki nit ña doon gàddul Yowab ngànnaayam, dikk wër Absalom, jam ko, mu dee. 16 Yowab wal bufta ba, dakkal xare ba, xarekat ya noppee dàq waa Israayil. 17 Ñu jël néewub Absalom, sànni ci kàmb gu réy ca àll ba, daldi jóor ca kawam jalu xeer bu maga mag. Bànni Israayil yépp nag daw ñibbi seeni kër.
18 Absalom moo samplu woon cig dundam, doj wu mag wa ca xuru Buur, ndax da noon: «Bàyyiwuma doom ju góor ju ñu may fàttalikoo.» Moo tax mu tudde doj wa boppam, te doju Absalom lañu koy woowe ba tey jii.
Lu jëm ci tàggeb Absalom
19 Ba loolu wéyee Aximàcc doomu Cadog ne: «May ma rekk ma daw yégali Buur xibaar bii, ne ko Aji Sax ji musal na ko ciy noonam.» 20 Yowab ne ko: «Du yaw yaay yégle xibaar tey jii. Man ngaa yégle xibaar beneen yoon, waaye du yaay yégleji tey, ndax doomu buur a dee.» 21 Yowab nag wax ab waa Kuus, ne ko: «Demal wax Buur li xew.» Waa Kuus ba sujjóotal Yowab, daldi dem. 22 Aximàcc doomu Cadog dellu ne Yowab: «Lu ci mana xew, may ma rekk, man itam ma daw topp ci gannaaw waa Kuus bi.» Yowab ne ko: «Doom, lu la taxa bëgga dem, lii du xibaar bu ko jar.» 23 Mu ne ko: «Lu ci mana am, bëgg namaa dem.» Yowab ne ko: «Demal!» Aximàcc daw, jaare ca joor ga, ba njëkk waa Kuus ba.
24 Daawudaa nga toog ca diggante buntu dëkk ba féete biir ak bunt ba féete biti. Fekk na wattukat ba yéeg ca kaw taax ma tiim buntu dëkk ba, ca kaw tata ja. Naka la dawal bëtam, séentu, gis jenn waay juy daw moom kenn, di ñëw. 25 Wattukat ba àddu ca kaw, yégal ko Buur. Buur ne: «Gannaaw kenn nit la de, xibaaru jàmm lay indi.» Waa ja di gëna jegesi, 26 wattukat ba gis jeneen waay juy daw di ñëw, mu wax ko farbay bunt ba, ne ko: «Xoolal, keneen a ngi, di ñëw, moom kenn.» Buur ne: «Kooku it de xibaaru jàmm lay indi.» 27 Wattukat ba ne: «Ni ma gise ki jiitu de, dawinu Aximàcc doomu Cadog la ma jox.» Buur ne: «Kooku ku baax la, jàmm rekk lay waxsi.» 28 Ci kaw loolu Aximàcc àddu ca kaw, ne Buur: «Jàmm la!» daldi sujjóotal Buur, dëpp jëëm fa suuf, ne ko: «Buur, sang bi, cant ñeel na sa Yàlla Aji Sax ji, moom mi teg ci sa loxo ña la doon fexeel.» 29 Buur ne ko: «Ngóor sa Absalom nag, mbaa jàmm la am?» Aximàcc ne ko: «Sang bi, ba Yowab di yónni sa bëkk-néeg ak man, booba gis naa kër-kër ju réy, waaye xawma lu mu doon.» 30 Buur ne: «Randul, taxawe nii.» Aximàcc randu, taxaw ca wet ga.
31 Ci kaw loolu waa Kuus ba ne jimeet. Mu ne: «Buur, sang bi, déglul, xibaaru jàmm a ngi. Aji Sax ji musal na la bésub tey ci ña la doon fexeel ñépp.» 32 Buur ne waa Kuus ba: «Ngóor si Absalom mbaa jàmm la am?» Waa Kuus ba ne ko: «Buur sama sang, say noon ak mboolem ñi lay fexeel, yal nañu bokk ak ngóor soosu demin.»