3
Mujug jamono dina tar
1 Lii, nanga ko xam: mujug jamono, bés yu tar dina dikk. 2 Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu goreedi te selladi. 3 Duñu am yërmande, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax; 4 ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla. 5 Ragal Yàlla lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.
6 Ñenn ci ñooñu ñooy yoxoosuy dugg ci biir kër yi, di fàbbi jigéen ñu ñàkk bopp, ñi seeni bàkkaar man, te seen xemmemtéef yu bare jiital leen. 7 Gëstu ay àlluwa la jigéen ñooñuy wéye, waaye duñu mana xam liy dëgg mukk. 8 Noonee Sànnes ak Sàmbres*Sànnes ak Sàmbres, ay tur la yu Yawut yi baaxoo tudde luxuskati Misra ya doon fexee joŋante ak Yonent Yàlla Musaa. doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm. 9 Waaye duñu soreeti, ndax seenug ndof dina bir ñépp, na ñaar ñooña mujje woon.
Póol dénkooti na Timote
10 Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa ak sama dundin ak sama mébét ak sama ngëm ak samag muñ ak sama cofeel ak samag ñeme coono 11 ak itam bunduxataal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listar†Ikoñum ak Listar, ay dëkk ci diiwaanu Galasi lañu woon, fa Póol tàmbalee yenam, di waare xibaaru Almasi bi.. Céy na ñu ma bunduxataale, waaye Sang bee ma musal ci lépp! 12 Te kat képp ku namma farlu ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bunduxataal. 13 Waaye nit ñu bon ñi ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
14 Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe. 15 Bi ngay gone nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye. 16 Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub. 17 Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.