15
Péncoo am na ca Yerusalem
Ñenn nit ñu bàyyikoo Yude dikk Àncos, ñoo doon digal bokki taalibe yi, ne leen: «Su ngeen xaraful*Seetal ci 7.8., ni ko aaday Musaa santaanee, dungeen mana mucc.»
Mbir ma nag mujje féewaloo ak werante wu xawa metti, te Póol ak Barnabas séq ko ak ñooñu. Ba loolu amee ñu ne, na Póol ak Barnabas ak ñenn ca gëmkati Àncos ànd dem Yerusalem ca ndawi Yeesu ak mag ña, ba lijjanti mbir moomu.
Ci kaw loolu mbooloom gëmkat ñi yebal leen, ñu jaare Fenisi ak Samari, daldi àgge waa foofa ni jàmbur ñi dul Yawut tuube, ba bokki gëmkat ñépp bég ca lool. Gannaaw loolu, ñu agsi Yerusalem, mbooloom gëmkat ñi ak ndawi Yeesu yi ak mag ñi dalal leen, ñu nettali leen mboolem ni Yàlla def ak ñoom.
Ba mu ko defee ñenn ci gëmkat ñi bokk ci ngérum Farisen yi, daldi taxaw temm, ne gëmkat ñi dul Yawut, fàww ñu xarafal leen, sàmmloo leen yoonu Musaa.
Ba loolu amee ndawi Yeesu yi ak mag ñi bokk daje, ngir seet mbir moomu. Werante wu réy am ca. Ci kaw loolu Piyeer jóg ne leen: «Bokk yi, yeen xam ngeen ne bu yàgg la ma Yàlla seppee ci seen biir, ngir jàmbur ñi dégge ci sama làmmiñ kàddug xibaaru jàmm bi, ba doon ay gëmkat. Yàlla mi xam xolu nit nag moo seedeel jàmbur ñi, ba mu leen mayee Noo gu Sell gi, ni mu nu ko maye nun itam. Yàlla amul xejj ak seen sunu dig ak ñoom, ndax seen ngëm la raxase seen xol. 10 Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, di teg taalibe yi yen bu nu masula àttan, cay maam ba ci nun? 11 Yiwu Sang bi Yeesu daal lanu gëm ne ci lanuy mucce, te ñoom itam, noonu rekk.»
12 Ba loolu wéyee mbooloo mépp ne xerem. Ñu déglu nag Barnabas ak Póol, ñu xamle mboolem firnde yeek kéemaan yi Yàlla defe seen ñaari jëmm ci biir jàmbur ñi. 13 Ba ñu noppee, Yanqóoba àddu ne: «Bokk yi, dégluleen ma. 14 SimoŋSimoŋ mooy Piyeer ba tey. xamle na, ni Yàlla yége jàmbur ñi ca njàlbéen, ba sàkke ci seen biir xeet wu mu tudde turam. 15 Te loolu dëppoo na ak kàdduy yonent yi, ndax bindees na ne:
16 “Boroom bi nee:
Gannaaw loolu dinaa délsi;
maay yékkati mbaarum Daawuda mi daanu,
maay yékkati gent yi, joyanti ko,
17 ngir ndesu nit ñi wuta xam Boroom bi,
te ñooñoo di jàmbur ñi ñu tudde sama turSeetal ci Amos 9.11-12..
18 Boroom bee xamle loolu bu yàgga yàgg§Seetal ci Esayi 45.21..”
19 «Kon nag sama xalaat mooy: bunu gétën jàmbur ñi tuub, ba waññiku ci Yàlla. 20 Xanaa nu bind leen, ne leen ñu moytu lu ay xërëm sobeel, moytu séy yi yoon tere, moytoo lekk yàppu mala mu ñu tuurul deretam, ak lekk deret ci boppam. 21 Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey ay nit a ngi waaree yoonu Musaa ci dëkk bu nekk, ñu di ko jàng ci jàngu yi bésub Noflaay bu nekk.»
Ndaje ma bind na ñi dul Yawut
22 Ba loolu amee ndaw yi ak mag ñi mànkoo ak mbooloom gëmkat ñépp, ngir tànne ci seen biir ay nit, yebal leen Àncos, boole leen ak Póol ak Barnabas. Ñooñoo di Yuda mi ñu dippee Barsabas, ak Silas, ñu diy mag ca bokk ya.
23 Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne:
«Nun ndawi Yeesu ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo. 24 Dégg nanu ne ay nit ñu bawoo ci nun, ñoo leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seen xel, te nun joxunu leen lenn ndigal. 25 Moo tax nu mànkoo ci tànn ay nit ñu nu yebal ci yeen, boole leen ak sunuy soppe Barnabas ak Póol, 26 ñoom ñi jaay seen bakkan ngir sunu Sang Yeesu Almasi. 27 Kon nag noo yebal Yuda ak Silas, ngir ñu àgge leen ci seen gémmiñu bopp, lii nu leen bind. 28 Ndaxte Noo gu Sell gi moo mànkoo ak nun ci bañ leena teg benn coono, xanaa lii manula ñàkk: 29 Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak séy yi yoon tere. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.»
30 Ba loolu amee ñu tàggatoo, daldi dem ba Àncos. Ci kaw loolu ñu woo mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi. 31 Ba ñu jàngee bataaxal bi, kàddu ga dëfal leen, seen xol sedd. 32 Yuda ak Silas it gannaaw ay yonent lañu woon, wax nañu ak bokk yi lu yàgg, ngir ñaax leen, feddali seen ngëm. 33-34 Ba loolu amee ñu toog fa ab diir, bokk yi door leena ñaanal yoonu jàmm, yiwi leen, ngir ñu dellu ca ña leen yebaloon. 35 Póol ak Barnabas nag des Àncos. Ñu ànd ak ñeneen ñu bare, di jàngale aka xamle kàddug Boroom bi.
Póol ak Silas ànd nañu
36 Ba ñu ca tegee ay fan Póol ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk yi ci mboolem dëkk yi nu yégle woon kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.» 37 Barnabas nag bëggoon ñu yóbbaale Yowaan mi ñuy wax Màrk. 38 Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.
39 Mbir mi nag mujje dëngoo bu metti, ba ñu teqalikoo. Barnabas ànd ak Yowaan Màrk, dugg gaal, jëm Sippar. 40 Póol moom taamu Silas, daldi ànd ak moom dem, gannaaw ba leen bokk ya dénkee Boroom bi ciw yiwam. 41 Ci kaw loolu mu jaare diiwaani Siri ak Silisi, di ñaax mboolooy gëmkat ña.

*15.1 Seetal ci 7.8.

15.14 Simoŋ mooy Piyeer ba tey.

15.17 Seetal ci Amos 9.11-12.

§15.18 Seetal ci Esayi 45.21.