Aji Sax ji dige na mbugal
3
(Saar 3.1—6.14)
Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israayil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:
«Yeen doŋŋ laa ràññee
ci mboolem askani suuf.
Moo tax ma di leen mbugal
ndax seen ñaawtéef gépp.»
 
Ndax ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
Ndax gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul?
Am gaynde gu mat dina xiiroom paxam te jàppul?
Ndax picc dina keppu te fiireesu ko?
Am ag fiir dina fettax te jàppul?
Ndax bu buftab xare jibee, waa dëkk ba du tiit?
Ndax aw ay dina dabub dëkk te du Aji Sax jee?
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def,
te déeyu ko yonent yiy jaamam.
Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit?
Ana ku saña baña jottali kàdduy waxyu,
bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?
 
Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd
ak ca biir taaxi Misra.
Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari,
ba gis na Samari salfaañoo,
ak nootaange ga fa nit di daj.
10 Xamuñu sax def njub.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Dañuy jal alalu fitnaak yàqute
ci seen biiri taax.»
11 Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne:
«Ab noon dina gaw seenum réew,
néewal leen doole, lël seeni taax.»
12 Aji Sax ji nee:
«Wallub sàmm ak gàtt bu gaynde fàdd
weesul ñaari yeel, dogitu nopp.
Kuy wallu bànni Israayil ga ca Samari it,
xanaa dogu basaŋ, dammitu lal.
13 Dégluleen te artu waa kër Yanqóoba.»
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
Yàlla ji ci gàngoori xare yi.
14 «Bés bu may mbugale Israayil ay bàkkaaram,
damay tasaale sarxalukaayi Betel.
Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
15 Maay màbbaale këru taax ak këru àll;
kër yu ñu rafetale bëñu ñey dina yàqu,
te kër yu bare dootul taxaw.»
Kàddug Aji Sax jee.