Aji Sax ji misaal na mbugalu Israayil
7
(Saar 7.1—9.10)
Peeñu mu njëkk mi
1 Am na bés Boroom bi Aji Sax ji won ma am peeñu. Ndeke ma ngay sàkk naaxu soccet. Fekk na ñu góobal Buur, ba gàncax giy saxaat. 2 Soccet yiy lekk gàncaxu réew mi, ba mu bëgga jeex, ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, ngalla déet! Ndax askanu Yanqóoba àttan na lii a déet? Lu néew doole lañu.» 3 Aji Sax ji fomm ko, ne ma: «Kon du am.»
Peeñum ñaareel bi
4 Boroom bi Aji Sax ji dellu ma feeñu. Ndeke Boroom bi Aji Sax ji day waaja mbugale ñoñam sawara. Mu xoyom xóotey géej mbàmbulaan, bay waaja xoyom réew ma. 5 Ma ne: «Boroom bi Aji Sax ji, ngalla taxawal. Ndax askanu Yanqóoba àttan na lii am déet? Lu néew doole lañu.» 6 Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Lii itam du am.»
Peeñum ñetteel bi
7 Mu feeñooti ma, gisuma lu moy Boroom bi taxaw ci ab tata bu ñu natte buumu betteex ba ñu koy tabax. Ma nga yor buumu betteex ca loxoom. 8 Aji Sax ji ne ma: «Amos, ana loo gis?» Ma ne ko: «Xanaa buumu betteex.» Boroom bi ne: «Maa ngii di natte buumu betteex fi digg Israayil, sama ñoñ. Dootuma leen baal dara.
9 Dees na tas bérebi jaamookaayu askanu Isaaxa,
ba gental bérebi Israayil yu sell.
Maay jëlal askanu Buur Yerbowam saamar.»
Dàq nañu Amos
10 Ba mu ko defee Amaciya sarxalkatu Betel yónnee ca Yerbowam buurub Israayil, ne ko: «Amos a ngi lay fexeel ci digg Israayil. Réew mi du àttan waxam ji. 11 Mu ngi naan ci xare ngay deewe, te dees na jële Israayil suufam moos, gàddaayloo ko.»
12 Gannaaw loolu Amaciya ne Amos: «Yaw boroom peeñu mi, dawal, làquji réewum Yuda, nga jottali fa kàdduy waxyu, am fa loo dunde. 13 Betel gii nag, bu fi jottaleeti kàdduy waxyu, ndax fii jaamookaayu buur la, te it jaamookaayu réew mi la.»
14 Ba loolu amee Amos ne Amaciya: «Man de dumab yonent te bokkuma ci kuréelu yonent. Sama gétt laa yor, te maa ngi toppatoo ay tooli figg. 15 Aji Sax jee ma jële fa ma doon sàmme samay gàtt. Moo ma ne: “Demal jottalil ma kàdduy waxyu ci Israayil sama ñoñ.” 16 Léegi nag, déglul kàddug Aji Sax ji. Yaa ma ne: “Bul jottalil kàdduy waxyu ci Israayil te bul kebetu ci kaw askanu Isaaxa.”
17 «Gannaaw noonu la, Amaciya, Aji Sax ji nee:
“Sa jabar ci biir dëkk bi lay gànctoo,
say doom, góor ak jigéen, saamar tëral;
sam réew, ñu natte buum, séddoo.
Yaw nag, réewum yéefar ngay deeweji;
waa Israayil, ñu jële leen seen réew, ñu gàddaay.”»