32
Musaa woy na kóllëreg Aji Sax ji
Yeen asamaan, teewluleen, ma wax;
yaw suuf, déglul sama kàddu yii.
Na samam njàngale sóob nib taw,
samay kàddu rogalaat nib lay,
ba tuurul am ñax,
baawaanal gàncax.
Turu Aji Sax ji déy laay tudd,
seedeleen sunu màggaayu Yàlla.
 
Kee di cëslaay, te mati jëf,
wépp yoonam di njub.
Yàlla ju am kóllëre, mucc njubadi,
di àtte dëgg tey jub.
Njabootam ñoo defug yàqute ci kawam,
ba dootuñuy doomam ndax seeni sikk.
Ndaw maas gu dëng te njublaŋ!
Aji Sax ji lañuy feye lii?
Ndaw xeet wu dofe te ñàkk xel!
Mooy seen baay, moo leen bind,
sàkk leen, samp leen.
 
Fàttalikuleen jant ya njëkkoon,
baleen xel maasi maas ya woon.
Laajleen seeni baay, ñu xamal leen;
ak seen mag ñi, ñu wax leen.
Ba Aji Kawe ji séddee xeet yi seeni suuf,
tasaare doom aadama yi ci àddina,
moo àppal xeet yi seen kemi réew,
na mu dëppook limeefu goney*Mooy ndaw yi bokk ci péncum Yàlla ci déndi asamaan. Yàlla yi.
Céru Aji Sax ji moo di ñoñam,
te ñooñu, askanu Yanqóoba, di wàllam.
10 Moo leen fekk réewum màndiŋ,
fu ne wëyëŋ, ubaleeki sab,
mu feg leen, toppatoo leen, sàmm leen,
ni bu ñu doon peru bëtu boppam.
11 Moo mel ni jaxaay juy naawtal am tostanam,
daayaarlu, di wër, tiim leen,
tàllali laafam, aw leen,
teg ciw dunqam, boot leen.
12 Aji Sax ji doŋŋ a leen wommat,
du yàllay jàmbur ju ko ci fekk.
13 Moo leen waral kawtey réew ma,
ñuy xéewloo meññeefum àll bi,
mu di leen nàmpale lem ju walew doj,
ak diw gu balle xeer wu ne sereŋ,
14 boole ca soowum nag ak meewum xar,
nebbonu xar, kuuyi diiwaanu Basan aki sikket,
teg ca ngëneeli pepp,
may leen biiñu reseñ ju xonq curr, ngeen naan.
 
15 Yeen YesurunYesurun: tur wii ak Yanqóoba itam dees na ko woowe Israayil., yeena yaflu, waŋŋeetu,
solu yaram, ne faaj, ne fuux,
fàtte Yàlla mi leen sàkk,
faaleedi seen cëslaay li leen musal.
16 Ñoo yee fiiraangeem, ndax ay yàllay doxandéem,
ñoo ko merloo ak seen tuur yu jomblu.
17 Ñoo sarxalal ay rab yu dul Yàlla;
ay yàlla yu ñu masula xam,
yu bees yu doora xew,
yu seeni maam ràññeewuloon.
18 Cëslaay li leen meññ ngeen foñ,
Yàlla ji leen jur ngeen fàtte.
 
19 Aji Sax jee gis loolu, gedd,
ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.
20 Mu ne: «Maa leen di xañ sama kanam,
ba gis nu ñuy mujje,
ndax maasug defkati njekkar lañu,
doom yu ñàkk kóllëre.
21 Ñoo ma fiirloo ak yàlla yu dul tus,
merloo maak seen tuuri neen,
man it maa leen di fiireloo xeet wu tekkiwul dara,
ci waasow naataxóona laa leen di merloo.
22 Sawaraa ngay tàkke ca sama sànj,
di lakke ba ca xóotey njaniiw,
ba xoyom suuf ak meññeefam,
ba jafal reeni tund ya.
23 Maay jal ci seen kaw ay musiba,
maa leen di soqil, ba jeexal samay fitt.
24 Ñooy loof cib xiif, jeex tàkk ndaxi jàngoro,
ak mbas yu metti.
Ay selli rabi àll laay yebal ci seen kaw,
boole ca daŋaru ndox-suuf.
25 Fa biti la leen saamar di xañey doom,
biir néeg ya, tiitaange juy reye feelu ko,
buubaale waxambaane akub janq;
luy nàmp ak boroom bijjaaw.
 
26 «Maa noon maa leen di bóom,
ba far dakkal lu leen nit doon fàttalikoo.
27 Waaye reetaani noon laa ci ragal,
lu ko moy seeni bañ juume ko,
ba naan: “Sunu njàmbaar a!”
te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”»
 
28 Wii xeet wu gàtt xel
te ñàkk xam-xam!
29 Su ñu muusoon, xalaat ci lii,
ba xam nu ñuy mujje.
30 Ana nu kenn di dàqe seen junni,
ñaar di fëxal seen fukki junni,
te Aji Sax ji waccu leen,
ka ñu yaakaar, laa ne, jaayu leen?
31 Yaakaaru noon yi de melul ni sunu yaakaar,
te loolu la noon ya àtte.
32 Seen reseñ a nga cosaanoo Sodom
ak tóokëri Gomor,
doom ya di tooke, cëgg ya wex xàtt!
33 Seen biiñ daŋaru ninki-nanka la,
ak tookey ñàngóor bu aay.
34 «Xanaa du loolu laa làq fi sama wet,
ne ko ràpp fi samay denc?
35 Maay kiy feye, di añale,
te bu jotee ñu fakkastalu,
ndax seen bésub toskaree dëgmal,
dogal ba buur, wutsi leen!»
36 Aji Sax jeey dëggal ñoñam,
mooy ñeewante ay jaamam,
bu gisee doole dëddu,
ba kenn desul, dub jaam, dus gor.
37 Su boobaa da naan: «Ana seen yàlla ya,
seen kiirlaay lañu daa làqoo?
38 Ñi lekk seen nebboni sarax,
naan biiñ bi ñu leen di tuural kay,
nañu jóg, boog, xettali leen, di seen kiiraay!
39 Kon gisleen ne man la, man doŋŋ,
kenn du Yàlla ku dul man!
Man maay rey, di dundal;
di gaañe, di wéral;
maay jàpp, te kenn du xettali.
40 Maay yékkati sama loxo jëme asamaan,
giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww,
41 bu ma daasee sama saamar buy melax,
ba ŋàbb ko ci saab loxo, di àtte,
maay fey samay digaale,
añale samay bañ.
42 Maay nàndal samay fitt deret,
sama saamar di yàppe,
deret di nàcce ci ku ñu jam, ak ku ñu jàpp,
tey tuuroo ci boppi kilifay noon yi.”»
43 Yeen, xeet yi, tàcculeen ñoñam,
deretu jaamam ñi lay feyul,
pey gu muy fey ay bañam,
ba jot suufam ak ñoñam.
Déggal Aji Sax ji, dund
44 Noonu la Musaa dikke, mook Yosuwe doomu Nuun, ba jaar ci mboolem kàdduy woy wii, mbooloo mi di dégg. 45 Gannaaw ba Musaa noppee ci jottali Israayil gépp mboolem kàddu yooyu, 46 da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii. 47 Ndax kat du kàddug neen ci yeen. Mooy seenug dund! Ci gii kàddu ngeen di gudde fan, ca réew ma ngeen di jàll dexu Yurdan jëm fa, ngir nanguji ko.»
Aji Sax ji woo na Musaa
48 Ci kaw loolu Aji Sax ji wax Musaa bésub keroog boobee, ne ko: 49 «Doxal yéegi ca tundi Abarim gii, nga jàll ba ca tundu Nebo ca diiwaanu Mowabeen ba janook Yeriko. Nga séentu nag réewum Kanaan mi may jox bànni Israayil, ñu jagoo. 50 Boo noppee, dinga faatu ca kaw tund woowu nga yéeg jëm, ba nga fekki say bokk, noonee sa mag Aaróona deewe woon ca kaw tundu Or, ba mu fekki ay bokkam. 51 Li ko waral mooy yeena ma fecci worma ci digg bànni Israayil, ca ndoxi Meriba Kades, ca màndiŋu Ciin, ndax yeena wormaalul sama sellaay ci digg bànni Israayil. 52 Kon nag ci biti ngay séentoo réew ma, waaye foofa, doo fa dem. Doo dugg ca réew ma may jox bànni Israayil.»

*32.8 Mooy ndaw yi bokk ci péncum Yàlla ci déndi asamaan.

32.15 Yesurun: tur wii ak Yanqóoba itam dees na ko woowe Israayil.