Kàdduy waare
muy téere bu ëmb ay gëstu ci solos dundu nit
Suleymaan mooy ki ñu cosaanale téere bii. Ci ay jaar-jaar aki gëstuy boppam la sukkandiku, ba gis ne àddina naxi neen la, cëslaayal mbég dëgërul, te coono bi nit ñiy sonn ngir am mbégte, ñaare jaru ko. Gannaaw gi, mu biral na ab àtteem ci solos dundu nit. Mu ne: «Ma daaneele fii, ndax déggees na lii lépp: Yàlla, ragal ko; ay santaaneem, jëfe ko; loolu rekk mooy nit.» (12.13).
Ci tënk:
1.1-11 Àddina day wëndeelu rekk ci neen.
1.12—2.23 Lu jëm ci dund gu lënt.
2.24—12.8 Njariñ, fa Yàlla.
12.9-14 Àtteb àddina mooy ragal Yàlla te déggal ko.
1
Ubbite gi
1 Lii kàdduy waarekat baa, di doomu Daawuda te di buurub Yerusalem.
Luy solos àddina?
2 Cóolóoloo cóolóol, waru waarekat ba,
cóolóoloo cóolóol,
léppi cóolóoli neen.
3 Ana sax luy njariñu doñ-doñoo doñ-doñ
ju nit di doñ-doñi fi kaw dun bi?
4 Ag maas wéy, ag maas teew;
àddina sax ba fàww.
5 Jant fenk, so,
ne coww dellu fa muy fenke.
6 Ngelaw jëm bëj-saalum,
wiiri jëm bëj-gànnaar,
di wiir aka wiiraat,
di delluy wëndeelu, topp yoonam.
7 Dexoo dex wal, wuti géej,
te taxul géej fees.
Fa dex wal jëm,
fa lay walati, jëm.
8 Jëfoo jëf ca jëfit,
làmmiñ tuddul lépp,
bët du suur,
nopp du buur.
9 Lu ayoon mooy ayati,
lu ñu jëfoon moom lañuy jëfati.
Dara yeesul fi kaw suuf.
10 Lëf a ngii, nit naa:
«Lii de lu bees la,»
te mu ngi fi woon lu yàgg,
lu jiitu sunu juddu.
11 Kenn du fàttaliku ñi jiitu,
ñiy ñëwit,
ñi leen topp duñu leen fàttaliku.
Ma seet lu ma doy
(Saar 1.12—2.23)
Rafet xel doyul
12 Man waarekat bi,
buurub Israayil laa woon ci Yerusalem.
13 Damaa dogu ne damay gëstu,
teg ko ci xel mu rafet, di settantal
mboolem lu nit def fu jant bi tiim.
Ndaw sas wu tiis wu Yàlla sase,
ñu war koo sasoo!
14 Gis naa jépp jëf ju jëfe ci kaw suuf,
ndeke lépp cóolóoli neen la ak nappum ngelaw.
15 Lu wañaaru, maneesu koo jubbanti;
lu teewul, maneesu koo lim.
16 Damaa wax ci saam xel naa:
«Man de, maa ngii di gëna xelu,
ba sut ku ma jiitu ci jalub Yerusalem.
Damaa xuus ci xel mu rafet ak xam-xam.»
17 Noonu dogu naa xam luy xel mu rafet,
xam luy nitoodi akug ndof.
Fekk loolu it nappum ngelaw la.
18 Ku géejal xel mu rafet, géejal naqar;
yokku xam-xam, yokku tiis.