4
Alal doyul boroom
1 Ma seetlooti gépp nootaange gu am fi kaw suuf.
Ndeke néew-doolee ngi jooy,
amul ku ko dëfal.
Ki koy noot a am doole,
te néew-doole ji amul ku ko dëfal.
2 Dama ne ndokkalee, yeen ñi dee jeeg,
nde raw ngeen ñiy dund!
3 Ki leen taneeti yeen ñépp di ki juddoogul sax,
moom mi gisul jëf ju bon fi kaw suuf.
4 Ma gis ne nit ak kër-këram jépp
ak bépp manoorey liggéey,
iñaanantee ko waral.
Loolu it, cóolóoli neen ak nappum ngelaw.
5 Dof banki loxoom, sànk boppam.
6 Waaye benn ŋëb bu ànd ak dal
moo gën ñaari ŋëbi doñ-doñ ci nappum ngelaw.
Wéttalikoo gën wéet
7 Ma seetlu leneen luy cóolóoli neen fi kaw suuf.
8 Kenn a ngii, kenn ñaareelu ko,
du doom, du mbokk.
Doñ-doñam du dakk, te du doylu,
mujj mu naan: «Kan laay doñ-doñil,
di xañ sama bopp bànneex?»
Loolu it, cóolóoli neen, di sas wu tiis.
9 Ñaar a man kenn;
doñ-doñoondoo, yoolu bu baax.
10 Kenn daanu,
moroom ma may ko loxo.
Waaye ngalla ku daanu
te amuloo ku la may loxo!
11 Bu ñu tëddee di ñaar it,
mana bokk nugglu.
Waaye soo dee kenn, nooy nuggloo?
12 Fu ñu mane kenn,
ñaar taxaw fa, jéngu,
te buumu ñetti xànc gaawula dog.
Kilifteef saxul
13-14 Kuy ndaw, génne kaso,
tàmbalee nguuru fa mu juddoo woon mbaadoolo,
ndaw loolu su dee baadoolo te xelu it,
moo gën buur bu màggat, dofe, dégguli artu.
15 Ma gis mboolem luy dund
tey dox fi kaw suuf,
di topp ndaw la wuutu buur.
16 Mbooloo ngii mu janool,
bare lool ba wees ab lim,
te ña leen wuutu bégewuñu ki wuutu buur.
Loolu it di cóolóoli neen ak nappum ngelaw.
Ragalal Yàlla
17 Moytul sa bopp booy dem kër Yàlla.
Duggal te déglu,
bala ngay def saraxi dof bu xamul ne mu ngi def lu bon.