6
Alal, na la jariñ
1 Aw tiis a ngi wu ma gis fi kaw suuf,
di tiis wu diis doom aadama:
2 nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja,
te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn,
waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk,
xanaa jàmbur di ko xéewloo—
loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
3 Ku giir téeméeri doom,
dund ati at,
ak lu at ya baree bare,
su bégewul teraanga ja mu am
te amul njëgu bàmmeelam sax,
kooku lumb wu tuuroo ko tane.
4 Lumb wa ñëw na moos ci neen,
bàddoo lëndëm, turam sàngoo lëndëm.
5 Gisul jant, xamu ko,
waaye noflaay moo ko ëpple mag ma,
6 bu dundoon junniy junniy at sax
te amul jàmm.
Xanaa du benn béreb la ñépp jëm?
7 Nit ak doñ-doñam jépp, biiram,
te taxul mu doylu.
8 Ana lu boroom xel ëpplee ku dofe?
Nga ñàkk, xam doxalin,
lu mu lay jariñ?
9 Doyloo li nga gis a gën di wéye xemmem.
Loolu it, cóolóoli neen ak nappum ngelaw.
Nit dogalul
10 Lu masa ay, dees koo tuddoon;
lu doom aadama doon, xamees na ko,
te kenn du layook ku la sut.
11 Loo ci wax wax,
solo sa gëna néew.
Kon ana loo ci jële?
12 Ana ku xam lu gën ci nit ak fanam ni cóolóol,
toogadi ni takkndeer?
Ku koy wax luy am gannaawam fi kaw suuf?