Muccug bànni Israayil
Yonent Yàlla Musaa moo wéyal jaar-jaari bànni Israayil, jële ko fa ko téereb Njàlbéen ga bàyyi woon, gannaaw ñeenti téeméeri at (400). Yàlla musal na bànni Israayil ca seen buumi njaam ci Misra, Musaa jiite leen, ba génne leen Misra.
Yàlla moo jox bànni Israayil ndigali yoon wi ca tundu Sinayi, Musaa jottali ko, muy li lal kóllëre gi mu fas, moom Yàlla ak bànni Israayil, ndax ci ñoom la nammoona amal digeem baak seen maam Ibraayma. Yàlla sant Musaa, mu defarlu ab xaymab ndaje, ne: «Foofa laay dajeek bànni Israayil, béreb ba doxe fa sell ndax samag leer. Maay sellal xaymab ndaje mi ak sarxalukaay bi, te Aaróona aki doomam, maa leen di sellal, ngir ñu doon samay sarxalkat. Maay dëkk fi digg bànni Israayil te maay nekk seen Yàlla ji leen génnee réewum Misra, ngir dëkk fi seen biir.» (29.43-46).
Ci tënk:
Saar 1—18 Yàlla yiwi na bànni Israayil, génne leen Misra.
Saar 19—24 Yàlla fasante na kóllëre ak bànni Israayil.
Saar 25—40 Yàlla feeñal na màggaayam ak sellaayam ci xaymab ndaje mi ñu defar, ba noppi yékkati ko ci diggu dal bi.
1
Bànni Israayil dem na réewum Misra
1 Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israayil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di: 2 Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda 3 ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin; 4 ak Dan ak Neftali ak Gàdd ak Aser. 5 Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. 6 Gannaaw ga, Yuusufaaki doomi baayam yu góor yépp nelaw, ñook maas googu gépp. 7 Bànni Israayil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.
Firawna noot na bànni Israayil
8 Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra. 9 Mu wax ak waa réewam, ne leen: «Giirug bànni Israayil kat ñu ngi nuy gëna bare, ba ëpp nu doole. 10 Nanu ci sàkk pexe, ngir ñu bañatee yokku. Lu ko moy bu xare amee, man nañoo far ak sunuy noon, xeex ak nun, ba rëcc, génn réew mi.» 11 Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israayil tabaxale Firawna*Firawna turu pal la, ñeel bépp buuri Misra. buuru Misra†Misra mooy réew mi ñuy wax Esibtë ba tey. dëkk ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund. 12 Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israayil.
13 Waa Misra dañoo mujj di duggal bànni Israayil ci njaam gu metti, 14 yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
15 Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati Ebrë ya‡Ebrë tur la wu niti jamono jooja daan woowe xeet, ya bànni Israayil bokk., te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. 16 Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» 17 Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. 18 Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» 19 Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» 20 Bànni Israayil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, 21 may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. 22 Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»