Lu jëm ci jaamookaay bi
25
(Saar 25.1—27.19)
Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Waxal bànni Israayil ne leen, ñu indil ma ab saraxu njébbal. Ci képp ku am yéene ji, ngeen di jële li ñu may jébbal, indil ma ko. Li ngeen di jële ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy ak deri kuuy yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi*piipi, rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg. ak banti séngséng: am na ñu koy woowe akasiya. Am na geneen garab gu xeetoo ak moom muy kàdd., ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwug paldiwug pal mooy li ñuy diwe sarxalkat, buur mbaa yonent ngir tabb leen ci seen liggéey., di xeeñal cuuraay, ak ay peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam. Na ma bànni Israayil defaral béreb bu sell, ndax ma dëkk ci seen biir. Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu.
Lu jëm ci gaal giy def àlluway seede si
10 «Defarleen gaalu dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab§xasab mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc, di ñeent fukki sàntimet ak juróom. ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll; taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. 11 Nañu ko xoobe wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoobe wurus, sàkkal ko kéméju wurus gu ko wër. 12 Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam ci genn wet gi, ñaar, wet gi ci des. 13 Yattlul ay njàppuy bantu séng te nga xoob bu ci nekk wurus. 14 Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam yi ci weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. 15 Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti. 16 Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox.
17 «Defarlul kubeer gu ñuy awale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. 18 Tëgglul ñaari jëmmi malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga. 19 Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn. 20 Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi. 21 Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. 22 Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israayil.
Lu jëm ci taabalu mburum teewal mi
23 «Defarlul taabalu bantu séng, guddaay bi di ñaari xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll. 24 Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. 25 Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba kéméju wurus, wërale ko. 26 Defarlul ko ñeenti lami wurus te we lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya. 27 Na lam yi dendeek pegg ngir mana téye njàppu yi ñuy yóbboo taabal ji. 28 Yattlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. 29 Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuural Yàlla. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk. 30 Tegal mburum teewal mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww.
Lu jëm ci tegukaayu làmp bi
31 «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn. 32 Juróom benni car a soqikoo ci weti tegukaayu làmp bi, ñetti car ci gii wet, ñett ci gi ci des. 33 Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd*garabu amànd xeetoo naak gerte-tubaab., kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car ya soqikoo ca per ba, daj. 34 Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. 35 Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car ya soqikoo ca peru làmp ba, daj. 36 Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di wenn donju wurusu ngalam wu ñu tëgg ba mu jekk. 37 Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba. 38 Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam. 39 Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróomMu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ., ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem ay jumtukaayam. 40 Nanga xool te def leen mu dëppook misaal yi ñu la ciy won ci kaw tund wi.

*25.5 piipi, rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg.

25.5 séng: am na ñu koy woowe akasiya. Am na geneen garab gu xeetoo ak moom muy kàdd.

25.6 diwug pal mooy li ñuy diwe sarxalkat, buur mbaa yonent ngir tabb leen ci seen liggéey.

§25.10 xasab mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc, di ñeent fukki sàntimet ak juróom.

*25.33 garabu amànd xeetoo naak gerte-tubaab.

25.39 Mu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ.