18
Jëf, jël
Gannaaw loolu kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: «Ana lu waral waxin wii ngeen di waxe fi Israayil naan:
“Baay lekk reseñ ju xaay,
mu uum gëñi doom ja”?
«Giñ naa ko ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, dootuleen waxe woowu waxin fi Israayil. Mu ngoog, bépp bakkan maay Boroom. Muy bakkanu baay, di bakkanu doom, maa moom. Bakkan bi bàkkaar daal mooy dee.
Su nit dee boroom njekk,
di jëfe yoon ak njub,
tund ya ca saraxi tuur ya, lekkewu ca,
kasaray tuuru waa kër Israayil, wékku cay gëtam,
jabaru jàmbur, sobeelu ko,
jigéen ju gis baax, jegewu ko.
Du kenn ku mu néewal doole,
xanaa ab tayle, mu delloo ku ko ameel.
Alalu jàmbur it, foqatiwu ko,
xanaa ku xiif, mu leel,
ku rafle, mu wodd.
Aw ndollent taxu koo leble,
ab tegandaay, jëlu ko,
xanaa luy njubadi, mu moyu.
Àtteb dëgg, mu doxal diggante nit ak nit.
Sama dogali yoon, mu di ca doxe,
sama àttey yoon, muy jëfe worma.
Kooku boroom njekk la,
te mooy dund déy!
Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
 
10 «Jii waay su juree doom ju néeg juy tuur deretu jàmbur
mbaa muy def lenn ci yii,
11 te moom miy baayam jëfewu ci lenn,
tund ya ca saraxi tuur ya, doom ja di ca lekki,
jabaru jàmbur, mu sobeel,
12 ku ñàkk ak ku néewle, mu néewal doole,
alalu jàmbur, mu foqati,
ab tayle, delloowu ko ku ko ameel,
xanaa kasaray tuur, mu wékki gët,
jëf ju siblu, mu jëfe,
13 leblee, mu yokk ndollent,
ab tegandaay, mu jël.
Moo, kii nu muy dunde?
Kii kay du dund!
Ak mboolem jëf ju siblu jii mu def,
dee rekk mooy àtteem.
Bakkanam lay gàddu.
 
14 «Waaye kooka nag su amee doom,
doom ja gis mboolem li baayam bàkkaar,
mu teg ci bëtam te taxul mu roy ko;
15 tund ya ca saraxi tuur ya, lekkewu ca,
ay gëtam, wékku ko kasaray tuuri waa kër Israayil,
jabaru jàmbur, sobeelu ko.
16 Du kenn ku mu néewal doole,
ab tayle, jëlu ko, sàkkuwul ku ko tayle lenn,
alalu jàmbur, foqatiwu ko,
xanaa ku xiif, mu leel,
ku rafle, mu wodd.
17 Néew-ji-doole, loxoom dalu ko,
ndollent ak ab tegandaay, jëlu ko.
Sama àttey yoon lay jëfe,
sama dogali yoon lay doxe.
Kooku du dee ngir ñaawtéefu baayam.
Dina dund déy!
18 Baayam a jaay doole,
moo foqati alalu mbokk,
lu baaxul la def ci biiri bokkam.
Kon nag mooy dee ndax ñaawtéefu boppam.
19 «Ngeen neeti: “Lu tax doom du gàddu bàkkaaru baay?” Xanaa du yoon ak njub la doom ji jëfe? Sama dogali yoon yépp, mu di ko sàmm, di ko jëfe? Dina dund kay! 20 Ki bàkkaar daal mooy dee. Doom du gàddu ñaawtéefu baay, baay it du gàddu ñaawtéefu doom. Njub réerul boroom, mbon réerul boroom.
21 «Waaye ku bon ki su dëddoo mboolem moy yi mu moy, di sàmm sama mboolem dogali yoon, di def dëgg ak njub, dina dund moos te àtteb dee du ko topp! 22 Mboolem tooñam ya mu tooñoon, deesu ko ko dencal. Njekk li mu jëfe moo koy taxa dund. 23 Ana bànneex bu ma am ci deewug ku bon? Xanaa bu dëddoo jikkoy mbonam, ba dund! Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
24 «Waaye su dee boroom njekk, ba noppi dëddu njubte, di def njubadi, di roy mboolem jëf ju siblu ju ku bon def, kooku nu muy dunde? Mboolem njub gu mu defoon, deesu ko ko dencal. Ag ñàkk wormaam ak bàkkaaram moo koy taxa dee.
25 «Yeen nag ngeen ne: “Ni Boroom biy doxale du noonu!” Waa kër Israayiloo, dégluleen! Sama doxalin a dul noonu, am yeen seeni doxalin? 26 Boroom njekk su dëddoo njekkam, di def njubadi ba dee, njubadeem ga mu def moo ko taxa dee. 27 Waaye ku bon nag, su dëddoo mbonam ga mu nekke, di jëfe yoon ak njub, moom moo musal bakkanam. 28 Ndegam moo xoolaat, ba dëddu mboolem tooñam yu mu tooñ, dina dund déy. Du dee moos. 29 Moonte waa kër Israayil nee: “Ni Boroom biy doxale du noonu.” Yeen waa kër Israayil, samay doxalin a dul noonu am yeen seeni doxalin?
30 «Lii moo tax yeen waa kër Israayil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor. 31 Xalableen mboolem tooñ yi ngeen di tooñ. Sàkkuleen xol bu yees ak xel mu yees. Yeen waa kër Israayil, lu jar ngeen di dee? 32 Man de, bëgguma kenn dee. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen ba dund!»