38
Waxyu dal na Gog
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma ne ma: «Yaw nit ki, neel jàkk Gog ma ca réewum Magog, boroom Meseg ak Tubal, te nga jottali kàdduy waxyu jëme ci kawam. Neel: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Yaw Gog, kilifa gi ñu ràññee ci Meseg ak Tubal,
maa ngi nii fi sa kaw.
Maa lay waññi, we say ŋaam ay lonku,
génne la yaak sa mbooloo mépp ak fas ak gawar,
ñépp gànnaayu ba diis,
di gàngoor gu yaa, ak pakk yu mag ak yu ndaw,
ñépp mane saamar.
Waa Pers, waa Kuus ak waa Puut ay ànd ak yeen,
ñoom ñépp fàggoo pakk ak mbaxanam xare.
Gomeer indaale gàngooram gépp,
ak Bet Togarma ga ca catal bëj-gànnaar, ak gàngooram yépp,
ñuy xeet yu takku, ànd ak yaw.
 
«“Nanga waajal a waajal,
yaak mboolem sa ndaje mi dajesi fi yaw,
nga doon seen wattukat.
Feek lu yàgg dees na la woo.
Bu ay at jàlle ba jeex, yaay songi am réew
mu nit ña rëcc ci saamar,
ba jóge ci ay xeeti xeet,
dajeji ca kaw tundi Israayil ya yàggoona wéet.
Ñooñoo seppikoo ci xeeti àddina yi,
ñoom ñépp dëkksi fa ci biir xel mu dal.
Waaye yaa naa jàyy ni ngëlén,
mel ni aw xiin,
muur réew mi, yaak sa gàngoor yépp,
ak xeeti xeet yi ànd ak yaw.
 
10 «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Bésub keroog, ay xalaat dikkal la,
nga mébét mébét mu bon,
11 daldi ne: ‘Maay songi réew mu ne ŋàpp,
maay dali ca kaw waa réew mu ne finaax,
dëkke xel mu dal,
te du tata ju wër fu ñu dëkke, ñoom ñépp,
du buntu dëkk, du tëjukaayu bunt.’
12 Yaay dikk ngir foqati, sëxëtoo alal,
daldi aakimoo genti démb yu ñu dëkke tey,
ña fa ne di mbooloo mu ñu seppee ci xeet yi,
amug jur aki alal,
te dëkke léegi ci diggu àddina.
13 Waa Seba ak Dedan ak julay Tarsis,
ak mboolem seeni boroom daraja ñoo lay wax ne la:
‘Ndax nangu alal a la yékkati?
Ndax sëxëtoo alalu xaree la taxa bàbbi sa gàngoor,
ngir yóbbu xaalis ak wurus,
nangu jur ak alal, ba dajalee ca xare ba koom gu takku?’ ”
14 «Kon nag yaw nit ki, jottalil kàdduy waxyu, waxal Gog, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
Bésub keroog déy,
bu Israayil sama ñoñ sancsee xel mu dal, dinga ko yég,
15 ba bàyyikoo sa màkkaan, ca catal bëj-gànnaar,
yaak xeet yu bare yu ànd ak yaw,
ñoom ñépp war fas,
di gàngoor gu mag, di mbooloo mu bare.
16 Yaay songi Israayil, sama ñoñ,
mel ni aw niir, muur réew ma.
Fan yu mujj ya la loolu di am,
maa lay yóbbu yaw Gog, ba ca réew ma ma séddoo.
Maa lay firndeele sama sellaay,
ngir xeet yi gis, ba xam maay kan.
 
17 «“Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne:
Yaw déy, laa doon wax bu yàgg,
yonenti Israayil, sama jaam ña jottali ko ca yooya jant,
ñu jottali kàdduy waxyu ay ati at,
ne maa lay dalloo ci sama kaw ñoñ.
18 Bésub keroog, ba Gog di dalsi ca kaw réewum Israayil,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
sama xadaru mer ay fettax.
19 Sama fiiraange ak sama tàngooru xadar laa birale ne,
bésub keroog déy, suuf dina yëngoo Israayil lool;
20 jën ak njanaaw di lox fi sama kanam,
ñook rabu àll yi ak mboolem luy raam
ak kuy nit fi kaw suuf.
Tund yi màbb, doji mbartal ya fàqandoo,
tata yépp jóoroondoo.
21 Ca laay wool mbooloom Gog saamar fa sama kaw tund yépp,
kàddug Boroom bi Aji Sax jee,
mbokk di jam mbokk saamar.
22 Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru,
ak wali waameek doji yuur,
ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram,
ak xeet yu bare yi ànd ak moom.
23 Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellaay,
maa niy xamlee sama bopp,
yéefar yu bare di gis,
ba xam ne maay Aji Sax ji.”