5
Buleen delluwaat cig njaam
1 Almasi bi da noo yiwi, ngir nu yiwiku, kon nag saxooleen ko, te baña laxasooti buumi njaam.
2 Dama ne, man Póol maa leen wax, ne leen, su ngeen demee ba ñu xarafal leen kay, Almasi bi amalatu leen benn njariñ. 3 Ma artooti képp ku dem ba ñu xarafal ko, ne ko mboolem yoon wi la wara jëfe. 4 Yeen ñiy sàmm yoonu Musaa, di ko sàkkoo àtteb njub fa kanam Yàlla, daggoo ngeen ak Almasi bi, ñàkk ngeen yiwu Yàlla. 5 Ndax nun kat, ci ndimbalal Noo gu Sell gi ak ci sunu kaw ngëm lanu yaakaare njub gi nuy séentu. 6 Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm gi jëfi cofeel di firndeel.
7 Seen njàlbéenu xél de baax na! Ana ku leen gàllankoor ba toppuleen dëgg gi? 8 Loolu leen fàbbi de jógewul ci ki leen woo. 9 As lawiir, tooyalub sunguf bépp lay funkil. 10 Man de gëm naa ndax Boroom bi, ne dungeen wuuteek man xalaat benn yoon ci lii. Waaye kiy jaxase seenum xel, ak ku mu mana doon, mooy gàddu mbugalam. 11 Man nag bokk yi, su ma dee xiirtale ci xaraf, ana lees may bunduxataaleeti? Kon kay sama waareb deewu Almasi bi ca bant ba dootul doon ag tooñ ci kenn. 12 Ñi leen di lëjal ak waxi xaraf, nañu xuuf boog seen ngóorag bopp benn yoon!
Doxeleen Noowug Yàlla
13 Yeen de bokk yi, cig yiwiku lees leen woo. Moytuleen lenn rekk: bu seenug yiwiku diw lay, ngir topp seen bakkan, waaye deeleen surgawoonte ngir cofeel. 14 Ndax yoonu Musaa wépp, ci lenn ndigal lii la tënku: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom*Seetal ci Sarxalkat yi 19.18..» 15 Waaye su ngeen dee màttante aka lekkante kat, moytuleena far yàqante yaxeet!
16 Li ma leen di wax moo di: doxeleen Noowug Yàlla, su boobaa dungeen topp seen xemmemtéefi bakkan. 17 Ndax bakkan, la muy xemmem, daa dëngoo ak Noo gi; Noo gi it, la muy xemmem dëngoo ak bakkan. Dañu di ñaar yu féewaloo, te moo tax dungeen def la ngeen nammoona def. 18 Waaye su leen Noo gi jiitee, su boobaa nekkatuleen ci kilifteefu yoon wi.
19 Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmee, te mooy: séy yi yoon tere ak jëfi sobe ak yàqute 20 ak bokkaale ak xërëm ak mbañeel ak féewaloo ak kiñaan ak mer mu ëpp ak jiital say bëgg-bëgg ak réeroo ak xàjjalikoo 21 ak ñeetaane ak màndite ak xawaare yiy ànd ak moy ak yeneen yu ni mel. Ma artu leen nag, na ma leen artoo woon: ñiy jëfe noonu, amuñu cér ci nguurug Yàlla.
22 Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel ak mbég ak jàmm ak xolu muñ ak mbaax akug tabe ak ngëm 23 akug teey ak noot sa bakkan. Yu mel noonu, wenn yoon bañu ko. 24 Ñi bokk ci Almasi Yeesu nag, ñoo daaj ca bantam ba seen bakkan, daajaale ko ak sàkkuteefam yu tar aki xemmemtéefam. 25 Gannaaw nag Noowug Yàlla moo nu dundal, nanu topp Noo gi. 26 Bunu di yég sunu bopp, di merloonte aka iñaanante.