Askanu doomi Nóoyin
10
(Saar 10.1—11.9)
Xeet yi sosoo ci doomi Nóoyin
Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom.
Li jëm ci askanu Yafet
Doomi Yafet yu góor ñoo di Gomeer ak Magog ak Maday ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. Doomi Gomeer yu góor ñoo di Askenas, Rifaat ak Togarma. Doomi Yawaan yu góor ñoo di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim. Ñi sosoo ci ñoom ñoo law ca wàllaa géej, meññ nag ay xeet ci seeni suuf, xeet wu ci nekk ak làkkam, def it ay làng ci seen biiri xeet.
Li jëm ci askanu Xam
Doomi Xam yu góor ñoo di Kuus ak Misrayim ak Puut ak Kanaan. Doomi Kuus yu góor ñoo di Saba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Seba ak Dedan.
Kuus moo jur Nimrodd, ki jëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf, mu doonoon rëbbkat bu maga mag. Looloo waral ñu naan: «Mbete Nimrodd, rëbbkat bu maga mag ba.» 10 Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. 11 Ca réew mooma la Nimrodd jóge dem Asur, sanc Niniw ak dëkk yooyee di Rexobot Ir ak Kala, 12 ba Resen gi ci diggante Niniw ak Kala, dëkk bu mag bi.
13 Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi*Luddeen ñi ñooy waa Ludd, ci waxin wuy tekki ab giir niki boo nee Njóobeen ñi walla Njaayeen ñi. ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 14 ak Pataruseen ñi ak Kasluxeen ñi, ak it Kaftoreen ñi, ñooñee waa Filisti soqikooSeetal ci Amos 9.7..
15 Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett. 16 Kanaan mooy maamu Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi. 17 Mooy maamu Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi. 18 Mooy maamu Arwàddeen ñi it ak Cemareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. 19 Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Adma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
20 Ñooñu ñooy askani Xam, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
Li jëm ci askanu Sem
21 Sem, miy magu Yafet, jur na moom itam ay doom yu góor. Mooy maami Eber ak askanam. 22 Doomi Sem yu góor ñoo di Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. 23 Góor ñi Aram jur ñii la: Ucc ak Xuul ak Geter ak Maas. 24 Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber. 25 Eber moom, jur ñaari doom yu góor, kenn ki tudd Peleg (muy firi Séddalikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddalikoo woon. Rakku Peleg ju góor mooy Yogtaan.
26 Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yerax 27 ak Adoram ak Usal ak Digla 28 ak Obal ak Abimayel ak Seba 29 ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. 30 Ña nga dëkkoon ca wàllu Mesa ga wuti Sefar, di diiwaanu tund ya ca penku.
31 Ñooñoo askanoo ci Sem, askan wu ci nekk ak làngam ak làkkam, di ay xeet ci seeni réew.
32 Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee.

*10.13 Luddeen ñi ñooy waa Ludd, ci waxin wuy tekki ab giir niki boo nee Njóobeen ñi walla Njaayeen ñi.

10.14 Seetal ci Amos 9.7.