49
Yanqóoba tàggoo na
1 Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen:
«Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.
2 Dajeleen te déglu ma, man Yanqóoba seen baay;
teewluleen seen baay Israayil.
3 «Ruben, yaw mi ma taawloo,
nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan,
yaa ëpp moos ci fulla, sut ci doole.
4 Yaa toogadi it ni ndox muy wal-wali,
doo mujje sut,
nde yaa tëdd sa lalu baay,
ba teddadi, kera ba nga ca tëddee.
5 «Simeyon ak Lewi ñooy déeyoo yéene,
ñooy nas pexey ay.
6 Yàlla bu sama xol ànd ci seeni pexe,
mbaa sama xel di nangu seeni diisoo,
ndax fu ñu mere, xal faa bóome,
te làggal ay yëkk lañuy fowe.
7 Mbas ma seen xadar gu tar,
ak seen mer mi dul meddi.
Maa leen di wasaare ci kër Yanqóoba,
tasaare leen ci Israayil.
8 «Yaw Yuda, mi say doomi baay di taggeji,
ngay sëqi sa ndoddi noon, sëggloo leen,
sa doomi baay a lay sujjóotal.
9 Yuda yaa di gaynde gu mat, doom,
doora jóge nii ci pàdd,
tey yuug aka goor ni gayndeg sibi.
Yaa di gaynde gu deesul yee.
10 Nguur gi du jóge ci loxol njabootug Yuda,
te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam,
li feek boroom*pirim baatu boroom am na ay wuute-wuute yu bare. di ñëw,
ba xeet yi déggal ko.
11 Mooy yeew mbaamam cig reseñ,
cumbur ma féeteek car, ba ca gën;
muy fóote ay yéreem biiñ,
di sumb mbubbam ci ndoxum reseñ.
12 Bët yaa ngay nes-nesi ndax biiñ,
bëñ ya weex furr nim soow.
13 «Sabulon ay dëkke tefesi géej,
di teerub gaal yi, am réewam digalook Sidon.
14 «Isaakar mbaam ngonk la,
muy goor diggante ñaari sëf.
15 Bu gisee ni mbaaram neexe,
ak ni réew mi naate,
day waaf, gàddu ngaaxam,
daldi féetewoo coonob njaam.
16 «Dan ay àtteji xeetam,
ni ko giiri Israayil baaxoo.
17 Waaye Dan ay jaan ju dog aw yoon,
mbaa céebi ciw ñall,
mooy màtt tànki fas,
gawar jullootu.
18 «Céy Aji Sax ji, maa ngi séentu sa xettal!
19 «Gàdd la gàngoor di gaw,
mu téqtal leen, ba daan.
20 «Aser ay boroom dund bu duun,
mooy maye ngëneeli ñami buur.
21 «Neftalee di kéwél gu fëx,
te mooy jur doom yu taaru.
22 «Yuusufaay bànqaasu garab,
garab guy meññ, feggook bëtu ndox,
car yaa nga law, tiim digu tool ba.
23 Ay fittkat a ko toŋal,
di ko song aka fitt.
24 Teewul xalaam ga di wéye daŋ,
te la loxo yay dëgërloo
mooy loxoy Jàmbaar ju Yanqóoba,
kookooy Sàmm bi, Doju cëslaayal Israayil,
25 mooy sa Yàllay baay, ji lay wallu,
mooy Aji Man ji lay barkeele
ca barkey asamaan ya fa kaw,
ak barke ya ne leww ca suuf xóote ya,
teg ca barkeb njur ak nàmpal.
26 Sa ñaani baay ya romb
xéewali tund ya sax fàww,
rombati ngëneeli jànji cosaan ya,
yal na dal ci boppu Yuusufa,
ca kaw ndaal boppam, moom sangub doomi baayam ya.
27 «Beñamin ay till guy yeeroo,
di xëye yàpp rëbbam,
tey gonloo séddale am lëlam.»
28 Ñooñu ñoo sos mboolem giiri Israayil, ñu tollu ci fukk ak ñaar, te loolu la leen seen baay wax, ba mu leen di tàggu. Ku ci nekk mu tàggoo ko kàdduy tàggatoo, ya war ca moom.
Yanqóoba nelaw na
29 Gannaaw loolu da leena dénk ne leen: «Maa ngi waaja fekki samay maam; dencleen ma fa samay maam ca xuntum bàmmeel ba ca toolub Efron, Etteen ba. 30 Mooy xuntum bàmmeel ba ca biir tool ba ca Magpela, te jàkkaarloo ak Mamre ca réewu Kanaan, di tool ba Ibraayma jëndoon ca Efron, Etteen ba, ngir def ko bàmmeel. 31 Foofa lañu denc Ibraayma ak soxnaam Saarata, te foofa lañu denc Isaaxa ak soxnaam Rebeka, te fa laa denc Leya it. 32 Tool ba ak xuntum bàmmeel ba ca nekk, ñu nga ko jënde ca Etteen ña.»
33 Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam.