Bataaxal bi jëm ca
Yawut ya
Umple nañu ki bind bataaxal bii. Dafa ko bind, jagleel ko ñi dogoo topp Almasi bi, waaye fitna bi ñu leen teg tax na ñu bëgga xàcc, dellu ca seen ngëm la ñu jóge.
Bataaxal bii daa wone ne Almasi bi moo gëna màgg malaaka yi, moo gëna màgg Yonent Yàlla Musaa ak sarxalkat yi. Yoonu Musaa wi sos kóllëre gu njëkk gi, ak xaymab jaamookaay bi, ak sarax yi, ay misaal lañu woon ngir waajal Almasi bi. Almasi bi fas na kóllëre gu yees gi mottali kóllëre gi Yàlla fasoon ak bànni Israayil. Ki bind bataaxal bii dafay ñaax gëmkat yi, ba seen ngëm gëna dëgër, ba ñu mana topp ci tànki ñeneen ñi gëm Yàlla, doonte ñu ngi woon ci fitna.
Ci tënk:
1.1—4.13 Almasi bi moo gëna màgg malaaka yi, moo gëna màgg Musaa.
4.14—7.28 Almasi bi mooy sarxalkat bu mag bi gën.
8.1—10.39 Almasi bi fas na kóllëre gi gën, def na sarax bi gën.
11.1-40 Niki gëmkat yu njëkk yi seen ngëm kawe woon, war nanoo gëm dëgg gi kenn manula teg bët.
12.1—13.25 Nanu ne jàkk Yeesu, moom mi nguuram dul yëngu.
1
Yàlla moo feeñ ci Doom ji
Bu yàgg la Yàlla waxoon ay yooni yoon ak maam ya, ci waxin yu bare, yonent yi jottali. Ci fan yu mujj yii, ci Doom ji la jaare wax ak nun, ki mu jagleel lépp, te ci moom la sàkke àddina wërngal këpp. Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya, te ni turam wi mu séddoo gëna màgge turi malaaka yi, ni lees ko yékkatee, ba mu gëna màgg malaaka yi.
Doom jee gëna màgg malaaka yi
Ndax kat, ana kan ci malaaka yi la Yàlla masa wax ne ko:
«Yaa di sama Doom,
bés niki tey, maa la jur*Seetal ci Taalifi cant 2.7. Su Yàlla nee moo ko jur, waxin la rekk. Bés bi ñu doon fal ab buur ci bànni Israayil la Yàlla di biral ne jàppe na buur bi ni doomam. Ni doom di teewale baayam, ni la buur biy teewale Yàlla ci kaw suuf.
ba neeti:
«Maay doon Baay ci moom,
muy Doom ci manSeetal ci 2.Samiyel 7.14.»?
Buy indiwaat taaw bi ci àddina nag, ci la naan:
«Na ko malaakay Yàlla yépp sujjóotalSeetal ci Taalifi cant 97.7 ni ñu ko binde ci tekkiteg Mbind mu sell mi ci làkku gereg.
Malaaka yi, la Yàlla wax ci seen mbir ne:
«Moo def ay malaakaam diy ngelaw,
jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara§Seetal ci Taalifi cant 104.4.
Waaye Doom ji la Yàlla ne:
«Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww,
sa yetu buur njub la.
Yaa sopp dëgg, bañ lu bon,
ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég,
nga tiim say moroom*Seetal ci Taalifi cant 45.7-8.
10 Mu neeti:
«Yaw Sang bi, ca njàlbéen ga, yaa samp suuf,
sàkke asamaan say loxo.
11 Yooyu day réer,
waaye yaw yaay sax,
lépp ay ràpp ni mbubb.
12 Yaa leen di taxañ ni malaan,
ni yére di soppikoo it lañuy soppikoo,
te yaw ngay kenn ki,
te say at amul kemSeetal ci Taalifi cant 102.26-28.
13 Ana kan ci malaaka yi la mas ne:
«Toogeel sama ndijoor,
ba ma def say noon sa ndëggastalSeetal ci Taalifi cant 110.1.»?
14 Xanaa malaaka yépp duñu ay ngelaw yu ñu sas ab liggéey, yebal leen ngir ñu taxawu ñi wara jagoo ag mucc?

*1.5 Seetal ci Taalifi cant 2.7. Su Yàlla nee moo ko jur, waxin la rekk. Bés bi ñu doon fal ab buur ci bànni Israayil la Yàlla di biral ne jàppe na buur bi ni doomam. Ni doom di teewale baayam, ni la buur biy teewale Yàlla ci kaw suuf.

1.5 Seetal ci 2.Samiyel 7.14.

1.6 Seetal ci Taalifi cant 97.7 ni ñu ko binde ci tekkiteg Mbind mu sell mi ci làkku gereg.

§1.7 Seetal ci Taalifi cant 104.4.

*1.9 Seetal ci Taalifi cant 45.7-8.

1.12 Seetal ci Taalifi cant 102.26-28.

1.13 Seetal ci Taalifi cant 110.1.