Téereb Yonent Yàlla
Ose
Ose mi ñu dippee téere bii ab yonent la woon ca réewum Israayil ma féete woon bëj-gànnaar, balaa réew maa daanu ci atum 722 lu jiitu Almasi bi. Ñeent fukki at la ag yónnentam am, te moom ak Amos ak Esayi ak Mise ñoo bokkoon jamono.
Yonent Yàlla Ose la Yàlla woo, sant ko ne ko mu takk ndawus moykat, ba Ose takk ku ñuy wax Gomer. Gomer jural na ko ñetti doom. Seen tur yi nag di junj mbugal mu ñu nara teg Israayil. Ose moo mujj soññ Gomer ci tuub, ngir am njéggal, ba dëjuwaat. Ose nag digganteem ak Gomer ak fi mu jaar ak moom, day misaal fi Yàlla jaare Israayil mi bokkaale.
Ci tënk:
1.1—3.5 Ose moo denc Gomer, jigéenu moykat.
4.1—8.14 Israayil fippu na ci kaw Yàlla, di jaamu yeneen yàlla.
9.1—13.16 Lu jëm ci mbugal muy dikk ngir moyug Israayil.
14.1-9 Digeb dëjuwaat jib na.
1
Ubbite gi
1 Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Ose, góor giy doomu Beeri, ci janti buuri Yuda: Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiyas; ak ci janti buurub Israayil Yerbowam doomu Yowas.
Njabootu Ose misaal la
2 Ba Aji Sax ji tàmbalee yóbbante Ose kàddoom, Aji Sax ji da ne ko: «Demal takki jabaru gànc, nga am ca doomi ngànctu, ndax réew maa ngi gànctu ngànctu gu réy, dëddu ma man Aji Sax ji.» 3 Ose dem takki Gomer doomu Diblayim. Mu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju góor.
4 Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Yisreel. Des na tuuti dinaa mbugal askanu Buur Yewu ndax deret ji ñu tuur ci Yisreel. Dinaa dakkal nguurug waa Israayil. 5 Su bés baa maay damm ngànnaayu Israayil ca xuru Yisreel*Xuru Yisreel lañuy misaale deret ju wal, ndax la ñu fa bóomoon ñu bare. Seetal ci 2.Buur ya 9.7—10.31..»
6 Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruxama» (muy firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israayil, dootuma leen baal. 7 Waaye waa kër Yuda, maa leen di yërëm. Seen Yàlla Aji Sax ji laa leen di walloo, waaye duma leen walloo fitt mbaa saamar, mbaa ay xare, mbaa ay fas aki gawar.»
8 Ba Gomer feralee Lo Ruxama, ëmbaat na, ba am doom, muy góor. 9 Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (muy firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.
*1.5 Xuru Yisreel lañuy misaale deret ju wal, ndax la ñu fa bóomoon ñu bare. Seetal ci 2.Buur ya 9.7—10.31.