4
Aji Sax ji tiiñal na kilifay ñoñam
1 Yeen bànni Israayil, dégluleen kàddug Aji Sax ji,
Aji Sax ji kat moo séq ab layoo ak waa réew mi:
«Du worma, du ngor, du gennug ràññee Yàlla
ci réew mi.
2 Xanaa ay móolu aki wor, bóome, càcc ak njaaloo.
Dañoo ràkkaaju, di tuur deret ci kaw deret.
3 Moo tax réew mi wowal,
mboolem lu fi dëkke ràgg,
ba ci rabi àll yi ak njanaaw yi,
jëni géej itam day réer.
4 «Waaye bu ci kenn layoo,
bu ci kenn sikke,
ndax sa bokk yee mel ni ñuy layook sarxalkat yi.
5 Dingeen tërëf bëccëg,
yonent yi ànd ak yeen tërëf guddi,
te maay sànk seen ndey.
6 Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam;
yeen, xam-xam ngeen gàntal,
ma gàntal seenug carxal.
Yeena fàtte seen yoonu Yàlla,
man it maay fàtte seeni doom.
7 Sarxalkat yi ñu gëna baree, gën ma nee moye,
seenub sag, gàcce laa koy soppi.
8 Sama saraxi póotum bàkkaari ñoñ
lañuy dunde*Seetal ci Sarxalkat yi 6.19-22.,
tey yàkkamti ñu def njubadi.
9 Waaye niki askan wi, niki sarxalkat yi,
maa leen di dikke seen añu jikko,
maa leen di fey seeni jëf.
10 Ñooy lekk te duñu regg,
di gànctu te duñu giir,
nde Aji Sax ji lañu noppee topp.
11 Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees
moo yóbbu seenum xel.
12 Sama ñoñ, seen bant lañuy seetéey!
Seenu yet di leen waxaléey!
Xelum ngànctu moo leen wacc,
ñooy gànctu, lajje fa seen Yàlla.
13 Ca kaw tund yu mag ya lañuy rendee ay sarax,
cuuraay, ñu taale ca tund yu ndaw ya,
ak ca taatu gii garab gu mag, ba ca gee,
fa ker ga neexe.
Moo tax seeni doom di gànctu,
seen séeti doom di njaaloo.
14 Duma mbugal seeni doom
ndax li ñuy gànctu
mbaa seen séeti doom
ndax li ñuy njaaloo,
ndax ñoom sarxalkat yi ci seen bopp,
ay gànc lañuy teggeendool
te gànc yi ci jaamookaayi xërëm yi,
ñoom lañuy indeendool ay sarax.
Askan wu amulug dégg, sànku.
15 «Yeena ngi gànctu, yeen bànni Israayil,
waaye na Yuda mucc ci googu tooñ.
Buleen dugg Gilgal†Gilgal, béreb la bu ñu daan bokkaalee, ba tur wi mujj taxawe jikkoy dëddu Aji Sax ji.,
buleen yéegi Bet Awen‡Bet Awen: li muy firi mooy Kërug Ñaawtéef. Muy tur wu waxi kókkali dendale ak Bet El, tur wi firi Kër Yàlla.
di giñ ci Aji Sax jiy dund.
16 Ndegam ni aw nag tëwe ni la Israayil tëwe,
ndax léegi Aji Sax jee leen di foral
nim xar ci parlu mu ne màww?
17 Efrayim§Efrayim, genn la ci giiri Israayil ga ca bëj-gànnaar, moom la Ose faral di woowe réewum Israayil gépp. googu laa ne, moo lëngook jëmmi tuur!
Seetaan leen.
18 Seenu ñoll giiful sax, ñuy gànctoo gànctu,
te gàccee gënal seeni kilifa.
19 Callweer a leen di wal,
ñu kersawoo seen saraxi tuur yi.
*4.8 Seetal ci Sarxalkat yi 6.19-22.
†4.15 Gilgal, béreb la bu ñu daan bokkaalee, ba tur wi mujj taxawe jikkoy dëddu Aji Sax ji.
‡4.15 Bet Awen: li muy firi mooy Kërug Ñaawtéef. Muy tur wu waxi kókkali dendale ak Bet El, tur wi firi Kër Yàlla.
§4.17 Efrayim, genn la ci giiri Israayil ga ca bëj-gànnaar, moom la Ose faral di woowe réewum Israayil gépp.