6
Wooteb tuub jib na
Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji.
Moo nu xotat, te moo nuy wéral.
Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.
Ñaari fan, mu leqali nu,
ñetteel ba mu yékkati nu,
nuy dund fi kanamam.
Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji.
Ni jant bu fenk la dikkam wóore,
ni ab taw la nuy dikkale,
ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»
 
Aji Sax jee tontu: «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim?
Nu ma lay def, yaw Yuda?
Te sa ngor di xiinu suba,
mbaa ab lay, jekki ne mes.
Moo tax yonent yi laa leen di dumaa,
sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye.
Seen àttee leen di leeral ni ceeñeeru njël.
Ndax ngor laa namm, dub sarax,
ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.
 
«Waaye ñoom ca dëkk ba ñuy wax Aadama lañu feccee kóllëre,
foofa lañu ma wore.
Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef,
taq ripp ak deret.
Ni saay-saay siy tëroo,
ni la sarxalkat yi lëkkoo,
di bóome ca yoonu Sikem.
Ndaw jëf ju ñaaw!
10 Ci kërug Israayil laa gis lu yées:
fa la Efrayim di gànctoo,
Israayil googu laa ne moo sobeel boppam.
11 Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe,
kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.