8
Ku ji as ngelaw, yaay góob ngëlén
«Sexleen bufta bi!
Noon ni jaxaay jàyy ci waa kër Aji Sax ji,
nde ñoo fecci sama kóllëreek ñoom,
samaw yoon lañu gàntal.
Man la Israayil xaacu, ne ma:
“Éy sama Yàlla, maa la ràññee!”
Israayil a xalab lu baax,
ba ab noon dàq ko.
Ñoo fal ay buur te du sama ndigal,
ñoo tabb ay kàngam, te yéguma.
Seen xaalis ak seen wurus lañu sàkke jëmmi tuur,
muy seen sànkute.
Yeen waa Samari, seen jëmmu wëllu wi*jëmmu wëllu wi: seetal ci 1.Buur ya 12.25-30. dàqu na!
Sama mer tàkkal na leen.
Lu ngeen deeti xaar ci mucc ayib?
Israayil la lii jóge,
te ab liggéeykat moo ko sàkk.
Kon lii du Yàlla!
Ay tojit la wëlluw Samari di mujje.
 
«As ngelaw lañu ji, ñooy góob ngëlén.
Gub du jóg, pepp du focci,
te bu pepp amoon it,
jàmbur a koy wann.
Dees na wann Israayil;
tey ñu ngi ci biir xeeti jàmbur yi,
mel ni ndab lu kenn bëggul.
Ñoo demal seen bopp Asiri.
Mbaamu àll day beru yoonam,
waaye waa kër Efrayim ñooy jënd ay far.
10 Ci xeeti jàmbur ñi lañuy jënde,
waaye du tee ma dajale leen.
Léegi ñu tegoo nootaangey buur aki kàngam.
11 Efrayim a yokk ay sarxalukaay ngir moy,
ñu doon ay sarxalukaayi moyukaay doŋŋ!
12 Naa ko bindal sama fukki junniy ndigali yoon,
yëfi jàmbur lees koy jàppe.
13 Ñooy rendi jur gi ñu may sarxal,
lekk yàpp wi,
Aji Sax ji bëggu ci dara.
Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef,
mbugale leen seeni moy,
te ñoom Misra lañuy dellu.
14 Israayil moo fàtte ki ko sàkk,
di tabax kër yu yànj.
Yuda moom yokki dëkk yu tata wër.
Maay yebal sawara ci kawi dëkkam,
mu xoyom ay tataam.»

*8.5 jëmmu wëllu wi: seetal ci 1.Buur ya 12.25-30.