4
 1 Su bés baa, juróom ñaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko:  
«Sunub dund, nun a,  
sunu koddaay, nun a!  
Jox nu sag buum rekk,  
teggil nu gàcce.»   
Aji Sax ji aar na ndesu Yerusalem 
  2 Su bés baa njebbitum Aji Sax ji  
doon lu yànj, darajawu,  
meññeefum réew mi di teraanga, dib sag,  
ñeel ñi dese bakkan fi Israayil.   
 3 Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ  
ak ku des fa Yerusalem,  
ku sell ki lees lay woowe,  
muy képp ku ñu bind turam,  
te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.   
 4 Boroom beey wal noowal mbugal,  
noo guy lakk, sellal,  
fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ,  
fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.   
 5 Su boobaa tundu Siyoŋ bépp,  
fépp fu ñuy dajee,  
Aji Sax ji sàkk fa niiru saxaar bëccëg,  
guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ;  
leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,   
 6 di mbaar mu ñuy féexloo tàngooru bëccëg,  
di ko seeloob taw ak waame.