9
Doom juddul na nu
Askan wiy doxe lëndëm nii,
ñooy gis leer gu mag.
Ñooñu dëkke réewum dee mu ne këruus,
ñoom la leer di fenkal.
Aji Sax ji, yaay yokk xeet wi,
fulal leen bànneex,
ñuy bége fi sa kanam, mbégtem ngóob,
mel ni ñuy bànneexoo fa ñuy séddoo alalu xare.
Yaa leen di sippil seen sëf,
damm bant ba ñu leen gàlloon,
ak yetu ña leen nootoon,
na nga leen defaloon rekk ca xareb Majan.
Mboolem dàll wu ab noon dukkate ba dikk,
ak turki bu màndi deretu xare,
sawara lees koy leel.
Nde gonee juddu, ñeel nu,
di doom ju góor ju ñu nu may,
mu yenu kilifteef gi,
ñu di ko woowe Kiy xelale te yéemu
ak Yàlla jàmbaar ji
ak Baay bi sax dàkk
ak Buuru jàmm bi.
Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu,
fa jalub Daawuda ak nguuram
ga muy samp, saxale ko yoon ak njub
tey jii ba fàww.
Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.
Aji Sax ji yokk na mbugalam
Boroom bee yónnee kàddu
gu dal Israayil, askanu Yanqóoba,
xeet wépp jot ca,
ba ca Efrayim ak waa Samari,
ñay damooka sagu naan:
«Ay móol màbb,
nu yatt ponkali doj, tabaxaat,
xànqi garab yu ndaw daanoo ca,
nu wuutal ca garabi seedar yu mag.»
10 Aji Sax ji yékkati nooni Buur Reccin, fi seen kaw,
gemb seeni bañ,
11 Siri songe penku; Filisteen ña, sowu,
ñu sëxëtoo Israayil, wann.
 
Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,
meddiwul ba tey.
 
12 Waaye xeet wi delluwuñu ca ka leen duma,
toppuñu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
13 Moo tax Aji Sax ji doge Israayil bopp ak geen,
boole tiir ak barax doge ci benn bés.
14 Mag meek kàngam li ñooy bopp bi,
yonent bi mokkal naaféq dib geen.
15 Ñi jiite askan wii ñoo leen di sànk,
ña ñuy jiite loru.
16 Moo tax Boroom bi du bége seeni xale yu góor,
du yërëm seeni jirim ak seeni jëtun.
Ñoom ñépp a gëmadi, di def lu bon,
ku ci nekk di wax lu amul bopp.
 
Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,
meddiwul ba tey.
 
17 Mbon a ngi tàkk moos
ni sawara, xoyom dég aki dagg,
jafal gajji gott bi,
mu ne jippét, saxaar, naaw.
18 Merum Aji Sax ji Boroom gàngoor yi taal na réew mi,
xoyom waa réew mi,
kenn yërëmul sa mbokk.
19 Nit ñaa ngi màtte ndijoor, te doyaluñu,
di xàmpe càmmoñ te suuruñu,
ku nekk di yàpp sa mbokk:
20 Manase song Efrayim,
Efrayim song Manase,
ñu mànkoo, noonoo Yuda.
 
Teewul Aji Sax ji xàcc loxoom,
meddiwul ba tey.