12
Cant jib na 
  1 Bésub keroog dees na ne:  
«Aji Sax ji, sant naa la;  
yaa ma mere woon, meddi, dëfal ma.»   
 2 Ma ne: «Yàllaa may wallu,  
ma dallu, duma tiit.  
Sama dooleek sama kaaraange mooy Ki Sax,  
di Aji Sax ji,  
te mooy sama wall.»   
 3 Mbégte ngeen di rooteji  
fa wali mucc ya.   
 4 Bésub keroog ngeen ne:  
«Santleen Aji Sax ji, tudd turam,  
xamley jalooreem ci biir xeet yi,  
fàttali màggaayu turam.   
 5 Woyleen Aji Sax ji,  
moo kawey jëf!  
Na lii siiw biir àddina sépp.   
 6 Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel  
Ku màgg ki fi seen biir,  
Aji Sell ju Israayil.»