15
Ab yéeneb waxyu ñeel na Mowab 
  1 Yéene bii ñeel na Mowab:  
Genn guddi déy la Ar Mowab, dëkk ba tas, ne mes!  
Genn guddi déy la Kir Mowab tas, ne mes!   
 2 Nit ñaa ngi yéeg jëm kërug jaamookaay ga ca Dibon,  
ngir jooyi ca bérebi jaamookaay ya,  
Mowab a ngay yuuxoo kaw tundu Nebo ak Medeba,  
boppoo bopp dib nel,  
sikkimoo sikkim xuufu,   
 3 nit ña sol saaku, di ñaawlu fa mbedd ya,  
ak kaw taax yaak pénc ya,  
ku ne di jooy ba say rongooñ wale.   
 4 Waa Esbon ak Elalee ngi yuuxu,  
seen baat àkki ba Yaxacc,  
xarekati Mowab dégg ca, yuuxoo,  
ne yàcc ne yasar!   
 5 Maay jooy Mowab jooyi xol,  
nit ñaa nga fay dawe ba Cowar,  
àkki ba Eglat Selisiya.  
Ña ngay yéeg jëm Luxit, di jooyoo,  
awe yoonu Oronayim, di yuuxu.   
 6 Dexu Nimrim wow na,  
ñax wow, gàncax lax,  
dara naatatul.   
 7 Jël nañu lu ñu deseek lu ñu dencoon,  
yóbbu, jàll ca wàllaa xuru Garab ya.   
 8 Yuux déy maase na réewum Mowab,  
jooyoo ya ba Eglayim,  
jooyoo ya ba Beer Elim.   
 9 Dexu Dimon déy fees na ak deret,  
te ma nara wàcceel Dimon lu ko raw,  
ba ku rëcce Mowab,  
ak ku des ci réew mi, ma booleek gaynde!