5
Debora fent na woy
Bésub keroog Debora moo woy lii, mook Barag doomu Abinowam:
«Céy bu garmiy Israayil jiitoo,
bu gàngoor yeboo xol bu tàlli!
Jaaraamaalleen Aji Sax ji!
Buur yee, dégluleen; garmi yee, teewluleen;
man Aji Sax ji laay woyal, man,
ma kañ Aji Sax ji Yàllay Israayil.
 
«Aji Sax ji, yaa fëlle Seyir,
daagu, génne àllub Edom,
suuf jaayu, asamaan yuriku,
niir ya sotti,
tund yaa seey fa kanam Aji Sax ji,
tundu Sinayi gii moo seey fa kanam Aji Sax ji Yàllay Israayil.
 
«Janti ayub Samgar doomu Anat,
ak janti Yawel la ngér ya wéete,
ñay tukki mujj aw ciy teggi yu lunk.
Dëkk-dëkkaani Israayil ñoo noon yàcc yàccaaral,
ba man Debora, ma jóg,
maa jóg ndeyal Israayil!
Ñoo xewal yàlla yu yees, xare nuyoo ca bunt ya,
te du pakk*pakk mooy kiiraay bu ñuy jëfandikoo ci xare. dub xeej ci ñeent fukki junniy (40 000) góori Israayil!
Sama xol laa àndeek njiiti Israayil,
waa askan woowoo yeboo xol bu tàlli.
Jaaraamaalleen Aji Sax ji!
 
10 «Éey, yeen ñi war mbaam yu weex,
toog ci seeni teg yu yànj,
yeen ñi ci yoon wiy dem it, biralleen lii.
11 Kàdduy woykat yaa ngoog ca naanukaay ya,
ña ngay lim ndamal Aji Sax ji,
ak ndamal xarekatam yu Israayil.
 
«Ñoñi Aji Sax jee dem buntu dëkk ba.
12 “Deboraa, yewwulee, yewwul,
yewwulee, yewwul te dëbbe.
Jógalee, Barag doomu Abinowam,
ba jàpp say jaam, yóbbu.”
 
13 «Ndes wu néew a daan ponkal ya,
ñoñi Aji Sax ji laa ne, ñoo ma daanal jàmbaar ya.
14 Ñenni Efrayim la seenub reen fëlleji fa Amaleg,
Beñamin topp ca ànd ak seeni gàngoor,
ay njiit bawoo fa Makir,
aw nit bàyyikoo Sabulon, wàccsi ak seen yetu njiit.
15 Kàngami Isaakar ñoo làng ak Debora,
niti Isaakar déggal Barag,
sàqeendoo, topp ko ca xur wa,
te làngi Ruben ya jàppoo seen diisoo yu réy ya.
16 Moo yeen, lu ngeen di def ci wërmbal yi,
di déglu coggal giy meem?
Làngi Ruben yaa jàppoo seen diisoo yu réy ya.
17 Galàdd des ca wàllaa dexu Yurdan,
te Dan xandul fu wees gaalam ya,
Aser it a nga des tefesu géej ga, génnuli waaxam.
18 Waaye Sabulon ay gàngoor gu faalewul dee,
Neftali moom di jaay bakkanam ca kawte ya.
 
19 «Ay buur a xeexsi,
ay buuri Kanaan a xareseek ñoom
fa Taanag, feggook ndoxi Megido,
te du xaalis bu ñu ca lëlelël, mooy bu ñu amee ndam, ñu jële ci noon yi alalu xare. moos!
20 Kaw asamaan la biddiiw ya tollu, di sot,
ñoo buure ca seen ngér ya, xareseek Sisera;
21 walum Kison buub leen, falaŋ,
walum Kison maa! walum cosaan maa!
Naa dëgërlu boog te buure xol.
22 Fasi naaru-góor yaa ngay rëpptal a rëpptal,
seen we ya rëkkandoo.
23 “Móoluleen Meros,” la malaakam Aji Sax ji wax,
“kon móoluleena móolu waa Meros.
Ñoo sotlewul Aji Sax ji;
ñoo àndul ak ñeyi xare yi sotle Aji Sax ji.”
 
24 «Yaw Yawel, yal nanga gëna barkeel ci jigéen ñi,
yaw soxnas Eber, góoru Keñeen gi,
barkeelal, ba raw ci jigéeni biir xayma.
25 Ndox la Sisera ñaan, Yawel may ko meew,
ndabal buur la duyum soow, taajal ko.
26 Càmmoñam ba la yóotoo xeru xayma,
ndijoor ba ŋëb wàkkub liggéeykat,
wàkke ko Sisera, toj bopp ba,
bënn ker nopp ba, rajaxe.
27 Ca tànki Yawel la Sisera nërmeelu,
ne fëlëñ, ne lasiim.
Cay tànkam la nërmeelu, ne fëlëñ,
te fa mu nërmeelu, fa la ne fëlëñ, dee wett.
 
28 «Yaayu Siseraa ngay séentoo palanteeram,
yërndu ca caax ba, di jooy, naa:
“Moo lu guddeel sama watiiru doom ji?
Lu yeexal riirum watiiram yaak fas ya?”
29 Ndaxam ña sut am xel ca lingeeram ya tontu nañu,
waaye teewu koo jàppoo waxam jii:
30 “Jombul ña ngay séddale cëxëtoo ma ñu am;
jenn jongama ba ñaar, ci boppu góor gu ne,
ak cëxëtoom ndimoy cuub, Sisera jagoo,
ndimoy cuub yu yànj kay,
ba ci ñaari ndimoy cuub yu yànj,
ku ne wékkoo ca baatam, muy alalu sëxëtoom.”
 
31 «Nii, yal na ko mboolem nooni Aji Sax ji sànkoo,
fu mboolemi soppeem ne ràññ ni jantub digg njolloor!»
 
Ba mu ko defee jàmm am ca réew ma, diiru ñeent fukki at.

*5.8 pakk mooy kiiraay bu ñuy jëfandikoo ci xare.

5.19 lël, mooy bu ñu amee ndam, ñu jële ci noon yi alalu xare.