9
Abimeleg falu na ca Sikem
1 Abimeleg doomu Yerubaal ju góor moo dem ca càmmiñi yaayam ca Sikem. Mu wax ak ñoom ak mboolem waa làngi maamam ju góor ji jur yaayam. Mu ne leen: 2 «Dangeen di laaj kàngami Sikem yépp, ne leen: “Lan moo leen gënal ci yii yaar: juróom ñaar fukki doomi Yerubaal yépp yilif leen, am kenn doŋŋ yilif leen? Man miy seen deret, di seen mbokk lenqe nag, bàyyileen ma xel.”» 3 Ba loolu amee ay nijaayam yegge mboolem kàngami Sikem kàddu yooyu yépp. Seenub xol nag jengal Abimeleg, ndax dañu ne: «Kii kat mooy sunu mbokk.» 4 Ba mu ko defee ñu jox ko juróom ñaar fukki siikali xaalis, bu ñu jële ca seen kër tuur ma ñuy wax Baal Berit. Abimeleg feye ko ay nit ñu tekkeedi te yaroo seen sago. Ñooña topp ca gannaawam. 5 Mu dem nag kër baayam, ca Ofra, daldi rendi ci wenn doj juróom ñaar fukki góor ya mu bokkal seen baay. Mennum Yotam, doomu Yerubaal ju góor ja gën di ndaw moo ca des, te daa làqu woon.
6 Ba loolu amee mboolem kàngami Sikem ak Bet Milo gépp dajeji ca garabu Sikem gu mag ga feggook doj wa. Fa lañu fal Abimeleg buur.
Yotam léeb na bànni Israayil
7 Ba ñu àggee Yotam mbir ma, dafa yéeg ba ca kaw tundu Garisim. Mu àddu ca kaw ne: «Waa Sikem dégluleen maa, ndax Yàlla déglu leen.
8 «Garab yee dogu woon, ne dañuy fali seen buur. Ñu ne Oliw: “Falul, di sunu buur.” 9 Oliw ne leen: “Xanaa duma dakkal sama diwu tànnéef gii ñuy terale Yàlla, te di ko terale nit ñi, dem naa damay jaay doole ci kaw garab yi?” 10 Garab yi nag ne garabu Figg: “Yaw ñëwal boog falu, di sunu buur.” 11 Figg ne leen: “Xanaa duma dakkal sama tem-tem jii ak sama meññeef mu neex mi, naan damay jaay doole ci kaw garab yi?” 12 Garab ya ne Reseñ: “Kon yaw ñëwal falu, di sunu buur.” 13 Reseñ ne leen: “Xanaa duma dakkal sama biiñ bu bees biy bégal Yàlla ak nit ñi, naan damay jaay doole ci kaw garab yi?” 14 Ba mu ko defee garab yépp ne Dédd: “Kon nag yaw, ñëwal falu, di sunu buur.” 15 Dédd ne garab ya: “Su ngeen ma bëggee fal, may seen buur, jiite leen, te muy dëgg ci yeen, ñëwleen làqu ci sama ker, lu ko moy nag yal na sawara tàkke ci dédd bi, lakki ba ca garabi seedari Libaŋ.”
16 «Léegi nag, ndegam dëgg akug mat ngeen jëfe, ba fal Abimeleg buur, ndegam it jëf la ju ngeen baaxee Yerubaal ak waa këram, ba feye ko ko lu mu leen ji, 17 te ndaxam déy, sama baay xareel na leen, jaay bakkanam, ba xettali leen ci waa Majan; 18 teewul tey yeena jógal sama waa kër baay, ba boole juróom ñaar fukki doomam yu góor, bóom leen ci wenn doj, te yeena fal buur ci kaw kàngami Sikem, Abimeleg doomu jaamam bu jigéen, ndax li muy seen mbokk! 19 Kon ndegam dëgg akug mat ngeen jëfeek Yerubaal ak waa këram tey jii, yal nangeen am bànneex ci Abimeleg, te moom it mu am bànneex ci yeen. 20 Lu ko moy nag, yal na sawara tàkke fa Abimeleg, xoyom kàngami Sikem ak Bet Milo, tàkkeeti ca waa Sikem ak Bet Milo, xoyom Abimeleg.» 21 Ba loolu amee Yotam daw a daw ba Beer, daldi sanci foofa, ngir mucc ci doomu baayam Abimeleg.
Waa Sikem fippu nañu
22 Ñetti at la Abimeleg moom Israayil. 23 Gannaaw gi, Yàlla yebal ngelaw lu aay luy féewale Abimeleg ak kàngami Sikem. Kàngami Sikem wor Abimeleg, 24 ngir peyug jëfi coxor ja dal juróom ñaar fukki doomi Yerubaal yu góor ba seen deret tuuru, ngir këpp ko Abimeleg, mook kàngami Sikem ya ko jàppale woon, ba mu bóom doomi baayam yooyu. 25 Ci kaw loolu kàngami Sikem di wuta yàqal Abimeleg, ba teg ay tërukat ca kaw tund ya, ñuy nangu alalu képp ku jaare ca yoon wa. Ñu daldi koy yegge Abimeleg.
26 Ci biir loolu Gaal doomu Ebedd ju góor ànd aki bokkam, dikk Sikem. Kàngami Sikem nag wóolu ko. 27 Gannaaw gi, ñu ànd dem ca tool ya, witt seen tóokëru reseñ, nal, di bànneexu. La ca tegu ñu dem ca seen kër tuur ma. Ña ngay lekk aka naan, tey sewal Abimeleg. 28 Gaal doomu Ebedd ne: «Ana kuy Abimeleg, ak nooy kan ci Sikem gii, bay nangul Abimeleg? Xanaa du doomu Yerubaal, Sebul di jaraafam? Dama ne nangulleen waa kër Amor, mi sanc Sikem. Lu waral nuy nangul Abimeleg? 29 Éy ku tegoon askan wii ci sama loxo, ba ma jële fi Abimeleg! Kon dama naan Abimeleg: “Dajaleel sa gàngoor te génn fii, nu xare!”»
30 Ba mu ko defee Sebul jaraafu dëkk ba dégg kàddu yooyu Gaal doomu Ebedd wax. Xolam tàng ca, 31 mu yónni ndànk ay ndaw ca Abimeleg, ne ko: «Gaal doomu Ebedd aki bokkam kat dikk nañu Sikem, te ña nga noonee di xabtal waa dëkk bi ci sa kaw. 32 Kon nag dangay jóg guddi, yaak gàngoor gi nga àndal, nga lal am tëru ca àll ba. 33 Bu ëllëgee ba jant biy fenk rekk, sàqil ci kaw dëkk bi. Gaal ak gàngoor gi mu àndal duñu def lu moy génn dajeek yaw, su ko defee nga def ko loo man.»
34 Ci kaw loolu Abimeleg jóg guddi, mook mboolem gàngoor ga mu àndal, ñu lal am tëru fa janook Sikem, def ñeenti kuréel. 35 Ba Gaal doomu Ebedd génnee ba taxaw ca buntu dëkk ba, Abimeleg ak gàngoor ga mu àndal ne pëll, génne fa ñu doon tëroo. 36 Gaal séen gàngoor ga, ne Sebul: «Gàngoor a ngii di wàcce ca kaw tund ya!» Sebul ne ko: «Takkndeeri tund yi de nga gis, ñu mel niy nit.» 37 Gaal dellu ne: «Ma ne gàngoor a ngii di wàccsi, jóge kaw tundu digg bi, ak menn mbooloo muy dikk, jóge yoonu garabu seen gu gisaanekat ya!» 38 Sebul ne ko: «Ana sa réy làmmiñ gi nga doon waxe naan kuy Abimeleg ba ñu di ko nangul? Xanaa du gàngoor gii nga doon tuutal? Génnal rekk nag, xeex ak ñoom!»
39 Gaal nag génn, jiitu kàngami Sikem. Mu daldi xareek Abimeleg. 40 Abimeleg dàq ko, mu daw, nitam ñu bare daanu, ne lareet, ba ca buntu dëkk ba. 41 Ba loolu amee Abimeleg sanci Aruma, Sebul boole Gaal aki bokkam, génne leen Sikem, aaye leen fa.
42 Ca ëllëg sa waa Sikem di waaja génn jëm ca tool ya. Ñu àgge ko Abimeleg. 43 Abimeleg dajale gàngoor ga, séddale leen ñetti mbooloo. Mu lal am tëru ci àll bi. Ba mu gisee waa dëkk ba di génne ca dëkk ba rekk, dafa jóg, ne milib ca seen kaw. 44 Abimeleg ak mbooloo mi mu àndal ñoo riir wuti buntu dëkk ba, taxaw fa, ñaari mbooloo ya ca des riir, dali ca mboolem ña nekkoon ca àll ba, ba duma leen. 45 Bésub keroog bépp la Abimeleg xareek dëkk ba, ba nangu ko, ña ca dëkk, mu rey leen. Mu yàq dëkk ba yaxeet, suy fa xorom.
46 Ba mboolem kàngami Sikem ya ca tatam Sikem déggee loola, ca lañu làquji, ca pax ma ñu gas ca kër tuur ma ñuy wax Berit, def ko néegu rawukaay. 47 Ñu yegge Abimeleg ne ko mboolem kàngami Sikem ya dëkk ca tatam Sikem daje nañu. 48 Mu daldi yéegi tundu Calmon mook mboolem gàngoor gi mu àndal. Ci kaw loolu Abimeleg jël ab sémmiñ, dog caru garab, yékkati, teg ci mbaggam. Mu ne gàngoor ga mu àndal: «Nu ngeen gis ma def ko rekk, gaawleen def noonu.» 49 Gàngoor gépp itam, ku ci nekk dog ab caram, ñu topp ca gannaaw Abimeleg. Ci kaw loolu ñu jal car ya fa sës ca néegu rawukaay ba, daldi koy taal ca kaw ña ca biir. Ba mu ko defee waa taaxum Sikem yépp dee, tollook junniy nit, góor ak jigéen.
Abimeleg xare na ba dee
50 La ca tegu Abimeleg dem Tebecc, dal fa janook dëkk ba. Ci kaw loolu mu nangu ko. 51 Tata ju ñu dàbbali moo nekkoon ca biir dëkk ba. Waa dëkk ba bépp nag, góor ak jigéen, daw làquji fa; ñu tëju ca biir, daldi yéeg ca kaw taax ma. 52 Abimeleg dikk ba ca tata ja, song ko. Naka la dikk ba jege buntu tata ja, nar koo taal, 53 as ndaw rotal aw doju wolukaay wu mag wu jóge ca kaw, mu xar kaaŋ ma. 54 Abimeleg gaaw woo xale bu góor ba yor ngànnaayam, ne ko: «Boccil sa saamar, te jekkali ma, ndax kenn du ne jigéen a ma rey!» Xale bu góor ba jam ko, mu dee. 55 Waa Israayil nag gis ne Abimeleg dee na, ku ne daldi ñibbi.
56 Noonu la Yàlla delloo Abimeleg jëf ju bon ja mu defoon baayam, ba mu reyee juróom ñaar fukki doomi baayam. 57 Mboolem mbonug kàngami Sikem itam, ci seen kaw bopp la ko Yàlla këpp. Ñaanu alkànde gu Yotam doomu Yerubaal, noonu la dale ca seen kaw.