Téereb Yonent Yàlla
Yeremi
Yonent Yàlla Yeremi doon na waaraate ci Yuda lu mat ñeent fukki at, balaa gàngooru Babilon yóbbu waa réew ma cig njaam. Lii moo xewoon téeméeri at gannaaw waa Asiri di yóbbu ngàllo fukki giiri Israayil yi nekkoon ci bëj-gànnaaru Yuda. Bi Asiri daanoo, nguuru Misra gi nekkoon ci bëj-saalum ak nguuru Babilon gi nekkoon ci bëj-gànnaar ñoo séqoon Yuda, bëggoon koo noot.
Xibaar bi ëpp solo ci kàdduy waxyu yi Yeremi doon jottali dafa wax ne: mucc ci yarub Aji Sax ji wees na. Li fi sës mooy ñu dëddu seeni bàkkaar. Ñi koy déglu nag dañoo sofental ay artoom, ba mujj ko jàpp, jéng ko, ba nara jël bakkanam. Teewul Yàlla déey na Yeremi kàdduy waxyu yii ne: bu àppu mbugal mi matee, moo leen di delloosil jàmm ci seen réew.
Ci tënk: Saar yi toppantewuñu ni xew-xew yi ame woon:
1.1—25.38 Kàdduy waxyu dal na ci Yuda.
26.1—42.22 Waxyu indi na lu jëm ci mujug Yuda.
43.1—45.5 Yeremi jottali na ay kàdduy waxyu yu dal ci kaw Misra.
46.1—51.64 Kàdduy waxyu dal na ci kaw yeneen xeeti àddina.
52.1-34 Lu jëm ci xew-xew yi téere bi tëje.
1
Ubbite gi
Muy kàddug Yeremi, góor gi baayam Ilkiya bokk ci sarxalkat yi dëkk Anatot ca diiwaanu Beñamin. Kàddug Aji Sax ji dikkal ko ci jamonoy buuru réewum Yuda, Yosya doomu Amon. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak ñett. Kàddug Aji Sax ji dikkal na ko ba tey ci janti buurub Yuda, Yoyakim doomu Yosya, di ko dikkal, ba keroog nguurug Cedesyas di jeex, jeneen doomu Yosya ja. Mu yemook fukkeelu atu nguuram ak benn, ca juróomeelu weer wa. Booba lañu jàpp waa Yerusalem njaam, yóbbu leen.
Kàddug waxyu dal na Yuda
(Saar 1.4—25.14)
Yàlla woo na Yeremi
Kàddug Aji Sax ji dikkal na ma, ne ma:
«Laata ma lay sos ci sa biiru ndey, laa la xam;
laata ngay juddoo ci sa ndey, laa la séddoo,
def la ngay yonent ñeel xeet yi.»
 
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji,
da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»
 
Aji Sax ji ne ma: «Bul ne: “Gone laa.”
Képp ku ma la yebal, dem ca;
lépp lu ma la sant, wax ko.
Bu leen ragal, ngir yaw laay àndal,
di la xettali.»
Kàddug Aji Sax jee.
 
Aji Sax ji tàllal loxoom, laal sama gémmiñ.
Aji Sax ji ne ma:
«Mu ngoog, sexal naa la samay kàddu.
10 Ma ne, tabb naa la bés niki tey,
ci kaw xeet yeek réew yi,
ngay buddat, di fàqat,
di yàqate aka daaneel,
di defar aka jëmbat.»
Yàlla wone na ñaari misaal
11 Kàddug Aji Sax ji dikkal ma, ne ma: «Yeremi, loo gis?» Ma ne ko: «Caru garabu saal laa gis.» 12 Aji Sax ji ne ma: «Yaa ko gis, maa sàlloo def sama kàddu, ngir sottal ko.»
13 Kàddug Aji Sax ji dikkalaat ma ñaareel bi yoon, ne ma: «Loo gis?» Ma ne: «Cin luy bax laa gis. Mu ngi joye bëj-gànnaar, jublook nun.» 14 Aji Sax ji ne ma:
«Bëj-gànnaar la safaan bay fettaxe,
dal ci kaw waa réew mi mépp.
15 Maa ngii déy, di woo
mboolem waasoy réewi bëj-gànnaar ak seeni buur.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Dañuy dikk, ku ne dëj ngànguneem
fi janook bunti Yerusalem,
jànkoonteek tataam yépp,
ak dëkki Yuda yépp.
16 Maay biral samay àtteek ñoom
ci seen mbon gi gépp:
Dañu maa wacc,
di taalal cuuraay yeneen yàlla,
di sujjóotal lu ñu sàkke seeni loxo.
 
17 «Yaw nag takkul te wax leen lépp lu ma la sant.
Bul am tiitaange fi seen kanam,
lu ko moy ma tiital la fi seen kanam.
 
18 «Maa ngii def la bésub tey
nga mel ni dëkk bu mag bu tata wër,
mel ni xeru weñ mbaa tatay xànjar,
jàkkaarlook réew mi mépp,
muy buuri Yuda aki kàngamam,
di sarxalkati réew mi ak baadoolo yi.
19 Dañu lay xeex te duñu la man,
yaw laay àndal, di la xettali.»
Kàddug Aji Sax jee.