8
1 «Su boobaa déy,»
kàddug Aji Sax jee,
«noon yeey sulli yaxi buuri Yuda
ak yaxi kàngam yi
ak yaxi sarxalkat yi
ak yaxi yonent yi
ak yaxi waa Yerusalem,
fa seeni bàmmeel,
2 weer leen ci naaj week weer wi
ak mboolem biddiiw yi ñu soppoon,
di leen jaamu, di leen wut aka topp,
di leen sukkal.
Deesu ko dajale, deesu ko suul;
day mel niy jonkan fi kaw suuf si.
3 Dee mooy gënal dund
mboolem ku des ci njaboot gu bon gii,
ak mboolem fu ñu dese fa ma leen tasaare woon.»
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
Askan wi të na ticc
4 «Nanga leen wax ne leen:
“Aji Sax ji dafa wax ne:
Xanaa ku daanu, da dul jógaat?
Am ku lajj, du délsi?
5 Lu tax xeet wii dëddu?
Lu tax Yerusalem gii lajj, baña délsi?
Ñu ngi langaamoo naxi neen,
baña délsi.
6 Teewlu naa, déglu naa;
du lu jaadu lañu wax.
Kenn tuubu ci mbonam,
ba ne: ‘Lu ma def nii?’
Ku nekk a topp yoonam,
ni fas wu màmm cib xare.
7 Ag xodd sax xam na bésub demam,
pitax, wetwet ak mbelaar it dem,
tey sàmm seen bésub délsi.
Waaye sama ñoñ faalewuñu àtteb Aji Sax ji.
8 Nu ngeen mane ne: ‘Am nan xel,
nu ngeek yoonu Aji Sax ji,’
te xalimay yoonalkat soppi ko fen?
9 Dees na gàcceel boroom xel yi,
ñu jàq, jataŋe.
Kàddug Aji Sax jaa ngii ñu dëddu ko,
ana seenum xel?
10 «“Kon nag maay jël seeni jabar, jox ñeneen,
jox seeni tool ay foqatikat,
ndax ki gëna tuut ba ci ki gëna mag,
ñépp a ngi lewal lu lewul.
Ab yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor!
11 Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammatoo,
naan: ‘Jàmm, lépp jàmm!’
te jàmm amul.
12 Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu,
te gàcce gàcceelu leen.
Xamuñu sax luy kersa!
Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu.
Bu ma leen dikkalee, dinañu tërëf.”»
Aji Sax jee ko wax.
Yaakaar tas na
Yàllaay wax
13 «Maa leen di witt a witt.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Garabu reseñ du dese doom,
figg du dese doom,»
kàddug Aji Sax jee,
«xob ya sax day wow.
Lu ma leen joxoon, rëcc na leen.»
Askan waay wax
14 Ana lu nuy toog?
Fabuleen, nu dem ca dëkk ya tata wër,
deewi fa.
Sunu Yàlla Aji Sax ji nar na sunu dee;
moo nu nàndal tookey mbugal,
nde noo tooñ Aji Sax ji.
15 Nuy yaakaar jàmm,
dara baaxul;
nuy séentum paj,
tiitaange ne jaas!
16 Seen noowi fas yaa dégtoo bëj-gànnaar fa Dan,
seen fasi naaru-góor di ŋexal, suuf sépp yëngu.
Ñu dikk, tas réew mi tasar,
booleek li ci biiram,
ak dëkk beek ñi ci biiram.
Yàllaay wax
17 «Maa ngii déy di leen yónnee
jaani ñàngóor yu déggul jat,
ñu di leen màtt.»
Kàddug Aji Sax jee.
Yeremi am na naqar
Yeremeey wax
18 Ndaw naqar wu tiis,
ndaw xol bu diis!
19 Sama bokk yaa ngooguy yuuxu
yuux yu àkki fu sore,
naan: «Moo xanaa Aji Sax ji daa newul Siyoŋ?
Xanaa Buurub Siyoŋ da fee nekkatul?»
Yàllaay wax
«Lu tax ñuy yékkati sama xol
ak seen jëmmi tuur yii,
seen yàllay doxandéem yi tekkiwul dara?»
Askan waay wax
20 Ngóob wéy na, jamonoom wees,
te nun de muccagunu.
Yeremeey wax
21 Sama bokk yi seen xol jeex
tax na sama xol jeex,
may tiislu, tancoo njàqare!
22 Moo ndax diwu pajtal amul Galàdd*Galàdd, ab gox la bu féete dexu Yurdan penku te nekkoon fu bare gàncaxi pajtal.?
Am fajkat a fi amul?
Ana lu tax ba bokk yi taneeguñu?
23 Aka neexoon sama bopp soppaliku ndox,
saay gët di seyaan buy xelliy rongooñ
yu ma jooye guddeek bëccëg
bokk yi ñu bóom!