4
Yeesu feeñu na ndaw su dëkk Samari
Ba Yeesu yégee nag ne Farisen ya dañoo dégg ne Yeesu moo ëpp Yaxya taalibe yu muy tuubloo, di leen sóob ci ndox, doonte du woon Yeesu ci boppam moo doon sóobe, waaye taalibey Yeesu la woon, ca la jóge Yude, dellu diiwaanu Galile.
Woowu yoon nag, Samari la waroona jaare. Ci kaw loolu mu dem ba agsi dëkkub Samari ba ñuy wax Sikar, ca wetu tool ba Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa. Foofa la teenub Yanqóoba nekkoon. Fekk na coonob tukki ba jàpp Yeesu. Mu toog ca wetu teen ba, waxtu wu xawa yemook digg bëccëg.
Senn ndawas Samari dikk, di rootsi. Yeesu ne ko: «May ma, ma naan.» Booba ay taalibeem dem nañu dëkk ba, ngir jëndi lu ñu lekk.
Ndaw si ne ko: «Yaw miy Yawut, ana noo ma mana ñaane ndoxum naan, man, te may waa Samari?»
Ndax Yawut yi séquñu woon ak waa Samari lenn.
10 Yeesu nag ne ndaw si: «Soo xamoon mayu Yàlla, ak kan moo la ne may ma, ma naan, kon yaw yaa koy ñaan, mu may la ndox miy dundal.» 11 Ndaw si ne ko: «Sang bi, amuloo baag, te teen bi xóot na; ana fooy jële ndox miy dundal? 12 Dangaa sut sunu maam Yanqóoba, mi nu may teen bi, te naan ci, mooki doomam akug juram?»
13 Yeesu ne ko: «Ku naan ci miim ndox it, dina maraat, 14 waaye ku naan ci ndox mi ma koy may, man, du marati; ndox mi ma koy may, bëtu ndox lay doon ci moom, di ball, ngir dundug texe gu sax dàkk.»
15 Ndaw si ne ko: «Sang bi, may ma ci moomu ndox, ba duma marati, mbaa may dikkati fii, di root.» 16 Yeesu ne ko: «Demal woowi sa jëkkër te ñëw.» 17 Ndaw si ne ko: «Awma jëkkër.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg, amuloo jëkkër, 18 ndax juróomi jëkkër nga séyal, te ki nga am léegi du sa jëkkër. Kon dëgg nga wax.» 19 Ndaw si ne ko: «Sang bi, gis naa ne yaw ab yonent nga. 20 Nun nag, sunuy maam ca tund wee lañu daan jaamoo Yàlla, te yeen Yawut yi, yeena ne béreb ba jaamu Yàlla ware, ma nga ca Yerusalem.»
21 Yeesu ne ko: «Ndaw sile, lii ma lay wax, gëm ko: waxtoo ngi ñëw, du ci tund wii, te du Yerusalem lees di jaamoo Baay bi. 22 Yeen waa Samari, yeenay jaamu lu ngeen xamul. Nun Yawut yi, li nuy jaamu, xam nanu ko, ndax ag mucc, ci Yawut yi lay jóge. 23 Waaye waxtoo ngi ñëw, te léegi la; ci la jaamukat yi dëgg di jaamoo Baay bi xel ak dëgg, ndax ñu ni mel la Baay bi sàkku ñu jaamu ko. 24 Yàlla xel la*Yàlla xel la: Kàddug Yàlla nee na, Yàlla xel la, leer la, cofeelu neen la. Seetal ci 1.Yowaan 2.4., kon ñi koy jaamu, xel ak dëgg lañu ko war di jaamoo.» 25 Ndaw si ne ko: «Xam naa ne Almasi baa ngi ñëw, moom lañu naan Ki ñu falKi ñu fal: moom lañuy wax Kirist itam ci làkku gereg., kooku bu dikkee, moo nuy leeralal lépp.» 26 Yeesu ne ko: «Man miy wax ak yaw, man la.»
Taalibey Yeesu ya délsi nañu
27 Cooca la taalibey Yeesu dikk, daldi jaaxle ca lañu ko fekk muy wax ak as ndaw, waaye kenn newu ko: «Loo soxla?» mbaa: «Lu tax ngay wax ak ndaw si?»
28 Ndaw sa nag wacc fa njaqam, dem ca dëkk ba, daldi ne nit ña: 29 «Kaayleen gis; nit a nga fee, wax na ma mboolem lu ma def! Kooku du Almasi beem?» 30 Ñu génne ca dëkk ba, wutsi Yeesu.
31 Ci biir loolu taalibe ya di ko soññ, naan ko: «Kilifa gi, lekkal.» 32 Teewul Yeesu ne leen: «Am naa ñam wu ma lekk, te woowu ñam, yeen xamuleen ko.» 33 Taalibe ya nag naan ca seen biir: «Ndax dees koo indil ag lekk?» 34 Yeesu ne leen: «Samaw ñam moo di jëfe coobarey ki ma yónni, ba sottal ab liggéeyam. 35 Du yeena naan: “Fii ak ñeenti weer ngóob taxaw”? Dégluleen, ma wax leen: dawalleen seen bët, xool tool yi, ñu ngi weex tàll, di xaar am ngóob. 36 Góobkat baa ngi feyeeku xaat, tey dajale meññeef mi ngir texe gu sax dàkk, ba jikat bi ak góobkat bi bokk bég. 37 Loolu lañu léeb te muy dëgg, ne: “Kenn ji, keneen góob.” 38 Man maa leen yebal ngir ngeen góob fu ngeen ñaqul woon, yeen. Ñeneen a fa ñaq, ngeen dikk jariñoo seenu ñaq.»
Waa Samari ñu bare gëm nañu Yeesu
39 Dëkk boobu, niti Samari ñu baree fa gëm Yeesu, ndax kàddug ndaw sa seede woon ci Yeesu, ne: «Wax na ma mboolem lu ma def.» 40 Moo tax ba waa Samari dikkee ca Yeesu, dañu koo ñaan, ngir mu dal ak ñoom. Toog na fa ñaari fan. 41 Ci kaw loolu ñu gëna bare gëm ko ndax kàddoom. 42 Ñu wax ndaw sa nag ne ko: «Dootul li nga wax a nu taxa gëm, waaye nun noo déggal sunu bopp, ba gis ne kii moo di Musalkatub àddina bi.»
Yeesu faj na doomu dagu buur
43 Gannaaw ñaari fan yooyu la fa Yeesu jóge, jëm diiwaanu Galile, 44 ndax Yeesu ci boppam moo noon: «Ab yonent, réewu boppam, deesu ko fa nawe.» 45 Ba mu agsee Galile, waa Galile dalal nañu ko, ndax gis nañu mboolem la mu defoon ca Yerusalem, ca màggalu bésub Mucc ba, ndax ñoom itam demoon nañu ca màggal ga.
46 Ci kaw loolu mu délsi Kana gu Galile, dëkk ba mu soppee woon ndox ma biiñ. Amoon na fa ab dagu buur bu doomam wopp ca dëkk ba ñuy wax Kapernawum. 47 Ba mu déggee ne Yeesu jóge na Yude, ba agsi Galile, dafa dem ca moom, ñaan ko mu dikk, wéral doomam, ndax booba ma ngay waaja dee. 48 Yeesu ne ko: «Su ngeen gisul ay firnde ak kéemaan daal, dungeen gëm!» 49 Dagu buur bi ne ko: «Sang bi, dikkal, bala sama doom a dee!» 50 Yeesu ne ko: «Demal, sa doom a ngi dund.» Waa ja gëm kàddu ga ko Yeesu wax, daldi dem. 51 Naka lay dellu këram, ay surgaam gatandu ko, ne ko: «Sa doom a ngi dund!» 52 Mu laaj leen wan waxtu la tane, ñu ne ko: «Démb, ci benn waxtu ci bëccëg, la tàngooru yaram teqalikoo ak moom.» 53 Baay ba nag xam ne ca waxtu woowa la ko Yeesu noon: «Sa doom a ngi dund.» Ca la gëm Yeesu, moom ak waa këram gépp.
54 Lii moo di ñaareelu firnde ba Yeesu def ca Galile, gannaaw ba mu jógee Yude.

*4.24 Yàlla xel la: Kàddug Yàlla nee na, Yàlla xel la, leer la, cofeelu neen la. Seetal ci 1.Yowaan 2.4.

4.25 Ki ñu fal: moom lañuy wax Kirist itam ci làkku gereg.