9
Yeesu faj na gumbag judduwaale
1 Yeesu moo doon dem, ba gis jenn waay ju judduwaale gumba. 2 Taalibeem ya laaj ko ne ko: «Kilifa gi, ndax bàkkaaram a ko waral, walla bu waajuram, ba tax mu judduwaale gumba?» 3 Yeesu ne leen: «Du bàkkaaram, du bàkkaaru waajuram a tax. Da di liggéeyu Yàlla moo wara feeñe ci moom. 4 Danoo wara liggéey liggéeyu ki ma yónni ci bi muy bëccëg; bu guddee kenn du liggéey. 5 Li feek maa ngi ci àddina, maay leeru àddina.»
6 Loolu la Yeesu wax ba noppi, tifli fa suuf, tooyale ban ba lor wa, daldi diw bàq ba ca bëti gumba ga, 7 ne ko: «Demal sëlmuji ca bëtu ndoxu Silowe.» Silowe di firi Ki ñu yónni. Gumba ga sëlmuji, délsi di gis.
8 Dëkkandoom ya ak ña ko xame woon yalwaan, naan: «Xanaa du kii moo daan toog, di yalwaan?» 9 Ñii naan: «Moom la!» Ñee naan: «Déedéet, da koo niru rekk.» Waa ji ci boppam ne: «Man la de!» 10 Ñu ne ko: «Lu muri say bët?» 11 Mu ne leen: «Waa ji ñuy wax Yeesu moo tooyal ban, diw ko ci samay bët, ne ma: “Demal sëlmuji ca bëtu ndoxu Silowe.” Ma dem sëlmuji, di gis.» 12 Ñu ne ko: «Ana waa ji?» Mu ne leen: «Xawma fu mu nekk.»
Ka gumba woon seedeel na Yeesu
13 Ba mu ko defee ñu yóbbu nit ka gumba woon ca Farisen ya. 14 Ndeke bésub Noflaay la Yeesu tooyaloon ban ba, ba muri bëti gumba ga. 15 Loolu nag tax Farisen ya ñoom it, laaj ko nan la wére bay gis. Mu ne leen: «Ban la tooyal, diw ko ci samay bët, ma sëlmu, di gis.»
16 Ñenn ca Farisen ña nag naan: «Nit kii jógewul fa Yàlla, ndax sàmmul bésub Noflaay.» Ñeneen ña ne: «Nan la nitu neen kuy bàkkaar mana defe yii firnde?» Féewaloo daldi am ca seen biir. 17 Farisen ya dellu wax ak ka gumba woon, ne ko: «Yaw, loo wax ci moom, gannaaw yaw la muril say bët?» Mu ne leen: «Ab yonent la.»
18 Njiiti Yawut ya nag gëmuñu woon ne waa ja daa gumba woon bay doora gis noonu. Ñu daldi woolu waajuri ka gumba woon, 19 laaj leen ne leen: «Kii mooy seen doom ji ngeen ne gumba la judduwaale? Ana nu mu wére bay gis léegi?» 20 Waajur ya ne leen: «Xam nanu daal ne kii sunu doom la, te it gumba la judduwaale. 21 Waaye nu mu wére bay gis, xamunu ko; ki ko muril ay bëtam it, nun, xamunu ko. Laajleen ko, magum jëmm la; moom dina waxal boppam.»
22 Noonu waajuri waa ja waxe nag, ragal njiiti Yawut ya moo taxoon, ndax fekk na njiiti Yawut ya mànkoo ne képp ku seede ne Yeesu mooy Almasi bi, dees na ko dàqe ca jàngu ba. 23 Looloo waral waajur ya ne: «Magum jëmm la, laajleen ko moom.»
24 Farisen ya dellu woo ka gumba woon, ne ko: «Waxal sa digganteek Yàlla. Nun xam nanu ne waa jooju nit kuy bàkkaar la.» 25 Mu ne: «Su dee kuy bàkkaar de, xawma ci dara. Lenn laa xam: maa gumba woon, te léegi maa ngi gis.» 26 Ñu ne ko: «Lu mu la defal? Nu mu muree say bët?» 27 Mu ne leen: «Wax naa leen ko ba noppi, yeena dégluwul. Lu ngeen bëgg ci ma di ko waxaat? Xanaa yeen itam dangeena bëgga doon ay taalibeem?» 28 Ñu daldi ko saaga ne ko: «Yaw yaay taalibeb kii, waaye nun, taalibey Musaa lanu. 29 Nun xam nanu ne Musaa la Yàlla waxal, waaye kii, xamunu fu mu jóge.»
30 Waa ja ne leen: «Loolu kay mooy li yéeme! Yeen, xamuleen fu mu jóge, te mu muril ma samay bët! 31 Xam nanu ne kuy bàkkaar, Yàlla du ko déglu. Waaye ki ragal Yàlla, tey jëfe coobareem, kooku lay déglu. 32 Ba àddina sosoo ba tey, maseesu la dégg ku muri bëti gumbag judduwaale. 33 Kon nit kii, su jógewul woon ca Yàlla, du mana def dara.» 34 Ñu ne ko: «Ndax yaw mi fees ak bàkkaar, bi nga juddoo ba léegi, yaa nuy xaali?» Ci kaw loolu ñu dàqe ko ca jàngu ba.
Cilmaxa dëgg, ci xol la
35 Ba Yeesu déggee ne dàq nañu waa ja gumba woon, dafa dem ba gis ko, ne ko: «Yaw, ndax gëm nga Doomu nit ki?» 36 Waa ja ne ko: «Kooku kan la, Sang bi, ma gëm ko.» 37 Yeesu ne ko: «Gis nga ko; mooy kiy wax ak yaw.» 38 Mu ne ko: «Gëm naa la, Sang bi,» daldi koy sujjóotal. 39 Yeesu ne ko: «Man, ab àttee ma taxa dikk ci àddina sii, ngir ñi dul gis di gis; ñiy gis, gumba.» 40 Ay Farisen yu taxawoon ca wetam dégg ca, ne ko: «Xanaa nun it danoo gumba?» 41 Yeesu ne leen: «Su ngeen gumba woon, dungeen am bàkkaar, waaye léegi bi ngeen naa yeena ngi gis, ci ngeen di saxe ci bàkkaar ba furr.