5
1 Rikk wooteel, ndegam am na ku lay wallu!
Ana ci ñu sell ñi, kan ngay sàkku ndimbal?
2 Am sanax déy, naqari deret a koy rey,
ab téxét, xéraangee koy faat.
3 Maa gis am sanax, mu saxi reen,
ma jekki ñaan alkàndey dëkkuwaayam.
4 Ay doomam ay sore yoonu mucc,
ñu di leen dëggaate ca pénc ma,
te kenn du leen xettali.
5 Am ngóobam, ku xiif a koy lekk,
ba lekkaale la saxe biir dég ya,
te alalam, ku mar a koy ŋaf-ŋafee.
6 Aw ay du garab, bay fëlle biir suuf,
coono du jekki, jebbi.
7 Ku juddu, coono nga juddul,
mooy ferñent, kaw rekk la jëm.
8 Man de su ma doon yaw damay sàkku Yàlla,
te kon Yàlla laay diis sama mbir.
9 Keey def jëf ju màgg ju nattuwul,
di def kiraama yu limuwul.
10 Keey taw, suuxat suuf,
yónnee ndox, nàndal àll.
11 Keey kaweel ku suufe,
kuy ñaawlu siggee mbégte.
12 Keey neenal pexem ku muus,
ba mébétam du sotti.
13 Keey jàpp boroom xel cig muusam,
ba pexem ndëngteem teela sooy.
14 Ñu ni mel, bëccëg ñu dajeek lëndëm,
di làmbatoo digg bëccëg ni bu doon guddi.
15 Yàllaay musal néew-ji-doole ci saamaru làmmiñ
ak loxol boroom doole,
16 néew-ji-doole jagoo yaakaar,
defkatu njekkar ub gémmiñug boppam.
17 Ma ne, ndokkalee ku Yàlla jubbanti,
kon bul bañ yarub Aji Kawe ji.
18 Moom kat mooy mitital, di fajtal;
mooy gaañe, di wérale loxol boppam.
19 Juróom benni njàqare teew, mu xettali la ca,
ba ko juróom ñaareel sax, doo ca loru.
20 Ab xiif, moo la cay jote ba doo dee,
ab xare, nga mucc ñawkay saamar,
21 aayteefu làmmiñ, nga fegu ca,
te yàqule guy dikk, doo ko ragal.
22 Yàquleek xiif, nga kekku;
rabu àll, doo ko ragal.
23 Doji àll bi sax, kóllëreg jàmm ngay séq ak ñoom,
te rabi àll yi dañuy jàmmook yaw,
24 nga xam ne sa xayma, jàmm,
soo nemmikoo sa parlu, dara du ca wuute.
25 Dangay ràññee ni saw askan di yaatoo,
say sët di law ni gàncax.
26 Ni pepp di ñore, ñu door koo góob,
ni ngay màggataale doole, doora dëgmal bàmmeel.
27 Lii kat lanu gis, te lii rekk la.
Dégg, jariñu.