10
Ayóoba nee lu mu def Yàlla?
1 Maaka bañ sama dund gii!
Naa afal sama kàddug tawat,
di àddoo naqaru xol.
2 Dama naa Yàlla: Bu ma toppug tooñ.
Xamal ma kay li nga may toppe, lu mu!
3 Ana lu la noote di jariñ,
ba ngay bañ li nga sàkke sa loxol bopp,
tey àntal pexem ku bon?
4 Xanaa gëti nit doŋŋ nga am,
am ni nit di gise rekk ngay gise?
5 Say fan daa tollook fani doom aadama,
am say at daa yem ak ati nit,
6 ba ngay seet fu ma ñaawe,
di liñbat fu ma moye?
7 Moona xam nga xéll ne tooñuma,
te amul kenn kuy xettali nit ci sa loxo.
8 Say loxoo ma mooñ, tabax ma ba ma mat sëkk,
léegi nga di ma yàq yaxeet!
9 Rikk fàttalikul ne yaa ma tabax, ni bu ma doon ban,
xanaa doo ma delloo xaat ci pëndub suuf?
10 Xanaa du yaa ma xelli woon ni meew
ci sama biiru ndey,
wayal ma nim soow,
11 wodde ma der ak suux,
ràbbe ma yax aki siddit?
12 Yaa ma may bakkan, won ma ngor,
yaa sàmme sa yégeel samag noo.
13 Ndeke yoo lii nga dencoon ci sa xol,
xam naa ne lii nga naroon:
14 ne ma dann, ba su ma bàkkaaree,
doo ma baal samag tooñ.
15 Su ma defee lu bon, ngalla man,
te bi ma defee lu jekk it, sañumaa siggi,
gàcce laa suure, sangoo toroxte.
16 Waaye su may siggi rekk,
nga mel ni gaynde, di ma rëbb,
dellu di ma lore say kiraama,
17 yónneeti ma say seede,
gën maa songati,
ay gàngoor di wuutante fi sama kaw.
18 Ana loo ma doon génnee sama biiru ndey?
Doon naa dee te bët du ma gis!
19 Doon naa mel ni ku masula am,
jóge ci biir, ñu yóbbu bàmmeel.
20 Xanaa du fan yu néew laa dese? Ba ma boog!
Xiddil, ma leqaliku,
21 bala may dëddu, délseetuma,
bala may tàbbi réew mu lëndëm ga ne këruus,
22 réewum lëndëm,
mu ne këruus, salfaañoo,
ag leer sax, saf fa lëndëm!