41
1 Wii rab, yaakaar koo jàpp nax sa bopp la;
bu nee jaas, nga jóoru.
2 Kenn ñàngul, ba sañ koo merloo.
Kon ana kuy taxaw fi sama kanam man?
3 Ana ku ma abal lenn ba ma war koo delloo?
Lépp lu mboolem asamaan tiim, maay boroom!
4 Rab wii, duma noppee waxtaaney céram
ak kiraamay dooleem ak jekkaayu bindam.
5 Ana ku mana summib turkeem?
Ana ku mana bëtt kiiraayu ñaar-caam?
6 Ana ku koy ŋaal,
ak sellam yu dajal te raglu?
7 Gannaaw gi ay sàppey pakk la,
di ab tay bu tëje ràpp,
8 dugglante benn-benn,
ba ngelaw sax xaju ca,
9 xanaa ñu ne ñàpp, ku ne taq sa moroom,
te duñu teqalikoo.
10 Bu tislee, melax ne ràyy,
mu xippi, nga ne fajar ay xapp-xappal.
11 Jumi sawaraay tàkke ca gémmiñ ga,
ferñent ya jiitu,
12 saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya,
mbete cóolóolu cin luy bax.
13 Ngelawal bakkanam jafal nay xal,
sawara ne jippét, tàkke ca gémmiñam.
14 Ndoddam la doole daloo,
te fu mu dëgmal tëbum tiitaange fa la.
15 Ay ndombo la der ba def, dankalikoo,
ne këcc, ne degg.
16 Dënn baa nga dëgër niw doj,
ne këcc ni doju wolukaay.
17 Bu jógee, jàmbaar ñi tiit,
muy rajaxe, ñu jommi.
18 Nga jam ko saamar, du dugg;
xepp akug fitt akub xeej, noonu.
19 Weñ gu ñuul di ko safum mboob,
xànjar niru ko matt mu nëb.
20 Ndawal fitt dawloowu ko,
doju mbaq di ngooñ mu koy ñiramtal.
21 Bolde di ko saf ñax gu wow,
ab xeej riir, def koy ree.
22 Lu mel ni tojitu xandeer a lal biir ba,
di rijji bañ bi.
23 Mooy baxloo xóote yi ni cin,
di fuural géej ni njaq lu garab xooje.
24 Gannaawam ay def xàll wuy lerxat,
mbàmbulaan miy saf bijjaaw.
25 Amul niruwaale fi kaw suuf,
mii mbindeef mu dul tiit.
26 Képp ku réy, mu xool la bëtu suufe,
képp ku bew, muy sa buur.