14
Séddoo nañu réewum Kanaan
1 Lim bii nag mooy limu suuf yi bànni Israayil nangoo réewum Kanaan, muy seen cér. Elasar sarxalkat ba ak Yosuwe doomu Nuun ak ña yilif giiri maam ya ca bànni Israayil, ñoo leen ko séddale. 2 Na ko Aji Sax ji santaanee, Musaa jottali, noonu lañu ko defe séddaleb tegoo bant, ñeel juróom ñeenti giir ak genn-wàll ya sédduwul woon. 3 Fekk na Musaa séddale ñaari giir ak genn-wàll suuf sa féete penkub dexu Yurdan, waaye sédduloon giirug Lewi. 4 Askanu Yuusufa nag ñaari giir lañu. Giirug Manase ak giirug Efrayim, te Leween ñi, joxeesu leen wàllu suuf ca réew ma, lu moy ay dëkk yu ñu dëkke ak àlli parlu ngir seenug jur ak seen alal. 5 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la ko bànni Israayil defe, ba ñuy séddale réew ma.
Kaleb féetewoo na Ebron
6 Ci kaw loolu Yudeen ña dem fekki Yosuwe ca Gilgal ci njiital Kaleb doomu Yefune mi askanoo ci Kenas. Kaleb ne Yosuwe: «Yaw de xam nga la Aji Sax ji waxoon Musaa góoru Yàlla ga ci sunu mbir, maak yaw, ca Kades Barneya. 7 Ñeent fukki at laa amoon, ba ma Musaa, jaamub Aji Sax ji di yebale Kades Barneya, ngir ma nemmikuji réew mi. Ma dem ba délsi, indil ko ca kàddu gu dëggu. 8 Samay bokk ya ma àndaloon, ba ñuy yoqiloo gàngoor ga, man maa taxaw temm, topp sama Yàlla Aji Sax ji. 9 Bésub keroog la Musaa giñ ne: “Suuf sa nga teg tànk déy, sab cér lay doon yaak say sët ba fàww, ndax yaa taxaw temm, topp sama Yàlla Aji Sax ji.” 10 Léegi nag Aji Sax jee sàmm sama bakkan, na mu ko digee woon, ndax ba Aji Sax ji waxee Musaa loola ak léegi ñeent fukki at ak juróom la. Booba Israayil a nga ca dox ba ca màndiŋ ma, te tey maa ngii ci juróom ñett fukki at ak juróom. 11 Teewul na ma ame woon doole kera ba ma Musaa yebalee, ni laa ame doole tey jii, sama dooley kera di sama dooley tey, may xare, di dem aka dikk. 12 Kon nag jox ma diiwaanu tund yii Aji Sax ji waxoon bésub keroog. Yaa dégg bésub keroog ne, Anageen ñaa fa nekk ci ay dëkk yu mag yu ñu dàbbalee ay tata, waaye jombul Aji Sax ji ànd ak man, ma nangu ko ci seeni loxo, na ko Aji Sax ji waxe woon.»
13 Ba loolu amee Yosuwe ñaanal Kaleb doomu Yefune, jox ko Ebron, muy céru suufam. 14 Moo tax ba tey jii Ebron ñeel Kaleb doomu Yefune ji askanoo ci Kenas, ndax moo taxawoon temm, topp Aji Sax ji Yàllay Israayil. 15 Ebron, Kiryaat Arba la njëkkoona tudd (muy firi dëkku Arba). Arba ku màgg la woon ca Anageen ña. Ci kaw loolu xare ba dal ca réew ma.