16
Suufas Efrayim ak Manase
1 Dogu suuf ba giirug Yuusufa muurloo ci ab tegoo bant, ma nga dale woon dexu Yurdan ca wetu Yeriko, fa féete bëti ndoxi Yeriko penku. Kemu suuf ba ma nga jaare màndiŋ ma, yéegi ca diiwaanu tundu Betel, 2 daldi bàyyikoo Betel, wéy ba dëkk ba ñu naa Lus, ba ca kemu réewu Arkeen ña ca Atarot, 3 daldi wàcce ca sowu, jëm kemu réewum Yafleteen ña, dem ba feggook diiwaanu Bet Oron Suuf, jàll ba Geser, doora génni ca géej gu mag ga. 4 Loolu mooy céru suuf bi giirug Yuusufa muurloo, ci wàllu Manase ak Efrayim.
5 Digu suuf si giirug Efrayim séddoo làng ak làng nag nii la tëdde: Seen kemu suuf a nga jóge Aterot Adar ca wetu penku, ba ca Bet Oron Kaw, 6 daldi jàll ba géej. Wetu bëj-gànnaar, Migmetat la kem ga jaare, jàdd, jëm Taanat Silo ga mu jéggee ca wetu penkoom, wuti Yanowax. 7 Fa la kem ga wàcce, jubal Atarot ak Naara, feresuji Yeriko, génneji nag dexu Yurdan. 8 Kem ga bàyyikoo Tapuwa, jëm sowu ba ca walum Kana, fëlleji géej. Loolooy céru suufu giirug Efrayim, làng ak làng. 9 Giirug Efrayim amoon nañu itam ay dëkk yu ñu leen dogalal ci wàllu giirug Manase, dëkk bu ci nekk ànd ak ay dëkkam yu ndaw. 10 Waaye Efraymeen ña ñoo tëlee nangu Geser ca loxoy Kanaaneen ña fa dëkkoon. Looloo waral Kanaaneen ñi dëkk ci biir giirug Efrayim, ba tey jii. Terewul giirug Efrayim teg leen liggéeyu sañul-bañ.