20
Tànn nañu ay dëkki rawtu
Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji dafa wax Yosuwe, ne ko: «Waxal bànni Israayil ne leen, ñu tànn dëkki rawtu yi ma leen santoon ci jottalib Musaa, ngir ku rey nit ci njuumte lu dul coobareem, man faa rawi. Béreb yooyooy doon seen rawtu yu leen di musal ci kuy toppe bakkanu ku ñu rey. Bu ki rey dawee ba ca yooyu dëkk benn, day taxaw ca buntu dëkk ba. Su ko defee day diis magi dëkk booba mbiram. Nañu ko fat ca dëkk ba, may ko béreb bu mu dëkke ca seen biir. Bu ko fa kiy toppe bakkan toppsee, bu ñu ko teg ciy loxoom, ndegam du ci coobareem la rey moroomam te teyu ko, fekkul it mu bañ ko démb ak bërki-démb. Ca biir dëkk ba lay toog ba keroog ñu di ko àtte ca kanam mbooloo ma, ba keroog sarxalkat ba mbiram yemool faatu. Su boobaa ka rey man naa ñibbi këram, ca dëkkam ba mu dawe woon.»
Noonu lañu bere dëkk yii: Kedes ga ca diiwaanu tundi Neftali ca Galile, ak Sikem ga ca diiwaanu tundi Efrayim, ak Kiryaat Arba, di Ebron ga ca diiwaanu tundi Yuda. Ca wàllaa dexu Yurdan, fa féete Yeriko penku, Beccer lañu fa tànne ca màndiŋ ma ca kaw joor ga giirug Ruben séddoo, ak Ramot ga ca Galàdd, te bokk ci suufas giiru Gàdd, ak Golan ga ca diiwaanu Basan, te bokk ci suufas giirug Manase. Loolooy dëkk yi ñu dogalal mboolem bànni Israayil ak doxandéem yi dëkk ci seen biir, ba képp ku rey nit ci njuumte, man faa rawi, ba kiy toppe bakkanu ka dee bañ koo rey, bala ñu koo àtte ca kanam mbooloo ma.