5
Waa Yerusalem a ngi ñaan
Éy Aji Sax ji, bàyyil xel li nu dal,
xoolal, gisal sunu toroxte!
Sunu suuf toxu ciy jàmbur,
sunuy kër ñeel ay doxandéem.
Baay dëddu, nu diy jirim;
ndey dib jëtun.
Sunum ndox, xaalis lanu koy feye, naan,
sunu matt ak njëgam la mu nuy dikke.
Sunuw loos lañu ràng,
nu loof, te noppaleesu nu.
Nu nangul Misra,
nangul Asiri ngir ab dund.
Sunuy maam a moyoon, nekkatuñu tey;
nun, noo gàddu seeni mbugal.
Ay surgaa nu yilif, te amunu
ku nu wallu ci seeni loxo.
Bu nu lekkee, sunu bakkan lanu jaay,
nde saamar a ngi ci màndiŋ mi.
10 Sunu yaram nib taal la tànge
ndax tàngoorub xiif.
11 Jigéeni Siyoŋ lañuy tëdde,
ak janqi dëkki Yuda.
12 Kàngam yi, ñu jàpp, wékk;
te mag ñi, teraleesu leen.
13 Waxambaane yee yenu doji wolukaay,
gone yu góor yi sëfoo sayi matt, di tërëf.
14 Mag dakkal na jataayu pénc,
te waxambaane talatula xalam.
15 Xol nux-nuxeetul,
te ay rongooñ a wuutuy pooj.
16 Sunu mbaxana foq na!
Wóoy ngalla nun ñi moy!
17 Lee jeexal sunu xol,
lii moo nu jooyloo, ba gët giim:
18 tundu Siyoŋ wi gental,
ba till yi di fi daagoo.
 
19 Yaw Aji Sax ji, yaay toog ba fàww,
sab jal, sët ba sëtaat.
20 Ana lu waral nga fàtte nu fàww,
bàyyi nu diir bu yàgge nii?
21 Éy Aji Sax ji, delloosi nu fi yaw, nu dellusi,
yeesalal sunuy jant, mu mel na woon.
22 Xanaa doo nu wacc a wacc,
mere nu mer mu amul kemu?